dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

géej g- : dafay dem féexluji géej.

géer g- : nit ku bokkul ci askanu jaam, bokkul ci askanu ñeeño. yaayam dafa ko tere mu takk ndaw si ndax ndaw si du géer. géwel ak géer amul ca Yàlla.

géeru-juddu b- : géer bu yàgg ak ay géwal. sama géeru-juddu la mootax duma tarde benn xewam.

géew : defar ab wërngël taxaw ci. jigeen ñaa nga géew di tëgg a ka fecc.

géex : lekk ba suur di géex. dinañuy wax tamit giix.

géey : lu xumbul dara. ngénte la barewul nit mootax mu géey. safaan wi mooy xumb.

géleem-maam-yàlla b- : géleem-maam-yàlla baa ngi dox ci sa kow.

géleem g- : géleem bare na Gànnaar. dinañuy wax tamit gëleem g- wala gileem g- wala gelem g-.

gélem g- : dinañuy wax tamit géleem g-. (seetal géleem)

gémmeñ g- : soo waxul loo xam, sa gémmeñ gi dina la dugal foo xamul. dinañuy wax tamit gémmiñ g-.

gémmiñ g- : dinañuy wax tamit gémmeñ g-. (seetal gémmeñ)

géndël b- : basaŋ b-, ndëstan g-. lalal ko géndël bi ci biti, mu féexlu.

géndël g- : bantu gàllaaj buy gis ab sàcc. góor gii mu ngi denc ag géndël.

génn : néeg bi dafa tàng mootax mu génn ci biti. dumay génn guddi. safaan wi mooy dugg.

gént : gént na dem Màkka biig ci guddi.

géppen b- : bant bu am càq bu ñu def ci njëlbeenu tool ngir bañ rab yi dugg ci. golo yee tax mu def géppen bi ci tool bi.

gépp : dem naa gépp kër wànte gisuma ko.

gétën : lëjal, tanqal, lakkal. xale yi demleen fowi, seen coow li gétën nañu. dinañuy wax tamit gëtën.

gét : dinañuy wax tamit get. (seetal get)

gétt g- : béreb bu ñuy def jur gi wala mbooloom jur. dem na gétt ga. / am na géttu nag.

géwal b- : mbëggeel xamul géer xamul géwal. dinañuy wax tamit géwel b-.

géwalu juddu b- : géwal bu yàgg, dale ko ca maam ya ba léegi. seen géwalu juddu bi du tarde seen xew mukk.

géwel b- : dinañuy wax tamit géwal. (seetal géwal)