dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

fu nekk : fépp. ndaw si du yendal, du fanaanal, fu nekk lay dem. dinañuy wax tamit fu ne.

fuddën : ndaw si fuddën na ay tànkam ak ay yoxoom.

fudd : dafay fudd simis bi rekk.

fuddu : dafa sonn mootax muy fuddu rekk. dinañuy wax tamit fuddatu.

fukk y- : def na fa fukki fan.

fulaar b- : musoor g-. mu nga takk fulaar ba ca kow bopp ba.

fuleet : fees ci lu gaaw. buuse bi ne na fuleet nag wi.

fulëer b- : garab gi am fulëer yu rafet.

fulla j- : fayda j-, ñàkk caaxaan. li ngay def ci lu baax ànd ceek fulla ju mat sëkk.

fulli : fees. dangay fulli ci taatu garab gi nga naan ko.

ful : soo may fey dangay ful li nga may jox.

fuloor b- : tóor-tóor b-. fuloori garab gi rafet nañu.

funax : dinañuy wax tamit fënëx. (seetal fënëx)

fundooñu : bërëngu. gunoor baa ngi fundooñu ci suuf si.

funëx : dinañuy wax tamit fënëx. (seetal fënëx)

funki : junki. beñe dugub dafay funki. dinañuy wax tamit fonki.

fu : fu marse bi nekke ? fu mu dëkk ? fu ngeen jëm ?

fuñ : dàq. dañu ko fuñ mu jóge foofa yépp.

fuññ : (ne fuññ). mel ni ku mer. yaa ngi ne fuññ, xanaa danga mer ?

fuq : dinañuy wax tamit fëq wala foq. (seetal foq)

furaase : dinañuy wax tamit ŋargaloo. (seetal ŋargaloo)

furi : soppeeku ndax yàgg. sa simis bi dafa furi léegi.

furli : bëgg a feyul. suñu mbër mi dafa ko daan, rakk ji furli.

furne b- : booyalal ko furne bi mu àttaaya. dinañuy wax tamit furno b-.

furno b- : dinañuy wax tamit furne b-. (seetal furne)

fur : baatu fur baatu weex rekk lay andal. xalangu na ci doom bi ba weex fur. dinañuy wax tamit furr wala tàll.

furooñu 1 : dinañuy wax tamit fundooñu. (seetal fundooñu)

furooñu 2 : mëq. cere kese la doon furooñu.

furr : dinañuy wax tamit fur. (seetal fur)

furset b- : paaka ak furset lañuy lekke.

furtaag : ràkkaaju. ba mu ñëwee iniwersite ba tey, dafa furtaag.

futbal : kuppe. ngoon war nañu futbal ak seen waa koñ.

futi : yàqu. dañu koo dóor ca kaso ga ba mu futi.

fut g- : (saaga la) muuti g-. nëbbal sa fut gi.

futt 1 : mbàccum gerte mee futt yoxo yi yépp.

futt 2 : (ne futt). duŋŋ (ne). màndikat baa nga ne futt ca baar ba. dinañuy wax tamit fótt (ne).

futti : summi. gaa yi futti nañu sàcci bi dóor ko dóor yu metti. safaan wi mooy solal.

fuuf 1 : ëf. ngelaw lee fuuf sondel bi mu fay.

fuuf 2 : lekk wala naan bu gaaw, saj, et, dëndiix. waa ji nee na fuuf potu ndox bi.

fuuf 3 : fopp. du sa morom, moo la dàq a jàng fuuf.

fuur : sa àttaaya bi des naa fuur.

fuur b- : mbulañsëri b-. mburu jeex na ca fuur ba.

fuus : lu nekk di nëb. xaal yi nga jënd dañoo fuus.

fuuxal : dinañuy wax tamit fóoxal. (seetal fóoxal)

fuuy : soppi doxalin wala nekkin bu am-am wala mën-mën waral. ba mu tàmbalee dawal oto ba léegi, dafa fuuy.

fuyuŋ-fayaŋ b- : lu barewul njëriñ, xuuj b-. soo seeralee sa fuyuŋ-fayaŋ bi tamit, kenn du jënd.