dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

fi-mu-nekk : nëgëni-sii. fi-mu-nekk nii sikkim dafa lakkandoo, kenn talatul kenn.

ficc : dinañuy wax tamit ticc. (seetal ticc)

fiddi : ràddi, tàlli, ñàlli. xale yi dañoo séen gaynde gi rekk, fiddi.

fidiwël g- : wëñ g-. fidiwël gi dëgër na.

fifi : oppi, fëqle. waa ji dafa fifi, kenn menu koo suural.

fiftin b- : juroomi dërëm ak ñaari fiftin la yore.

fiil b- : fiilu kuraŋ. moytul fiil bi, dafay maase.

fiime b- : dinañuy wax tamit tos g-. (seetal tos)

fii : fii la juddoo. safaan wi mooy fee wala fale.

fiir 1 : nax ngir jàpp. xale yi dañuy fiir ay picc.

fiir 2 : fél. booy jéggi tali, taxawal nga xool sa càmmooy ak sa ndeyjoor bala la oto di fiir.

fiir 3 : jabar ji dafa fiir ba ñemewul a jaar fenn bu wàccee.

fiiriir : saaf, wajj. dafay fiiriir jën yi.

fiiru : dinañuy wax tamit féeru. (seetal féeru)

fiit : takk, yeew. fiit na ndigg li dem rooti ca teen ba.

file : fii. file la waa ji dëkk. safaan wi mooy fale, fee.

filidoraas b- : lii ndoxu filidoraas la.

findifeer b- : serkel g-. dafa bëgg a sàkket mootax mu jënd ay findifeer.

fi : gisoon naa ko fi démb.

fippu : danga sonal xale bi torob mootax mu fippu.

firgaat b- : joowu b-. mool yi jël nañu firgaat yi, dugg ci seen gaal gi, dem géej.

firi : sa létt yi ràpp nañu, nanga leen firi. / tekki. sëriñ bi dafay firi alxuraan.

firnde j- : màndarga m-. li nga defoon di ko weddi, firnde jaa ngi nii.

fitna j- : jafe-jafe b-, coono b-. bàyyil xuloo bi, yow danga bare fitna lool.

fit w- : ruu g-, xel m-. lutax sa fit wi dalul ? / njàmbaar g-. waa ji fitu gaynde la yor.

fittarñi : rëccal loxo bu ñu tikk. fexe na ba fittarñi loxoom bi.

fittax : dinañuy wax tamit fettax. (seetal fettax)

fitti : génn. béreb bale ndox maa ngi fay fitti rekk.

fitt g- : fitt la reyewoon bukki ba. dinañuy wax tamit fett g-. (seetal fett)