dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

feccali : saaku bi dafa desoon a fees waaye feccali na ko.

fecci : baatu fecci mu ngi jóge ci baatu fas. (seetal fas)

fecc : jigeen ñiy fecc ci ag céet lañu nekk.

feddali : suqali. dama fi ñëwoon ngir feddali kóllëre gi dox suñu diggante. dinañuy wax tamit féddali.

fedd : bulli. dof bi fedd na awra bi.

feebar : opp, tawat, jagadi. dafa feebar daaw ba ren wànte tane na bu baax léegi. safaan wi mooy wér.

feek : feek seen dëkk ñaata kilomet la ? dinañuy wax tamit fii ak wala fileek.

feela b- : xeetu basi. feela la beyoon daaw.

feelu : awu. fecc ak keneen. jabar jee ko doon feelu.

feem b- : kàddu yi kureelu pólotig yi di bàkkoo. kureelu pólotig yi dañuy faral di am ay feem. taxaw temm feemu genn kureelu pólotig la.

fee : su dul fii di fee rekk. dinañuy wax tamit fale. safaan wi mooy fii.

feeñ : génn. weer wi suba la war a feeñ. / fasam wi réeroon feeñ na. safaan wi mooy réer, làqu wala nëbbu.

feer b- : jumtukaay bu ñuy paase ay yére. tiyeel xale bi, feer bi dafa tàng.

fees 1 : fulli. buuse ci lu gaaw lay fees aw nag.

fees 2 : saaku bi fees na dell ak dugub. / nekk lim bu takku ci ab béreb. dëkk bi dafa fees dell ak ay njublaŋ, bàyyi leen xel. safaan wi mooy ŋacc.

feet g- : feet ga neexoon na lool ndax lépp a fa amoon.

feg 1 : ber. feg na li mu moom fale. dinañuy wax tamit fegg.

feg 2 : kar. xale yaa ngi feg sàcc bi.

fegg : ber. dinañuy wax tamit feg -1. (seetal feg)

fej : bala ngay am sàkket foog nga fej gittax.

fekk-baax : cosaanoo. dëkk bi mu fekk-baax la demoon.

fekk : fekk naa ko muy wax lu baax ci yow.

felaŋ : dinañuy wax tamit falaŋ. (seetal falaŋ)

feleesu : dinañuy wax tamit ferasu. (seetal ferasu)

fell : xàppatiku. ku doon fell guro bi nii ?

fel w- : fel rab wu mel ni yoo la.

feltoo : daje, tase. ca marse ba lañu feltoo keroog.

fenantal : jéllale. dangay fenantal rekk wànte fàttewuloo li nga ñu digoon. dinañuy wax tamit fenetal.

fendi : xaw a wow. yére bi fendi na.

feneen f- : beneen béreb. toogal fii nga liggeey, soo demee feneen tamit, jafe-jafe yaa nga fa.

fenetal : dinañuy wax tamit fenantal. (seetal fenantal)

fenk : féq, jóg (jant). jant bi fenk na bu yàgg ngay nelaw rekk.

fenku : fàdd ak ndigg. wujj wi dafa ko fenku mu dóor ko cunwaar.

fenn f- : fenn fi dafa tàng, fi ci des sedd. / kenn gisu ko waaye dégg nañu ko fenn. / du dem fenn.

fen : nar, kàcc. nit ku baax du fen. safaan wi mooy wax dëgg.

fent 1 : bind aw woy wala ab taalif. waa jee fent taalif bi.

fent 2 : xànc buumi guy. surga bi dafay fent.

fepp w- : pepp m-. suyalal ginaar yi fepp yi.

feq : fenk, feeñ. li ñu doon seet bu yàgg ba léegi, feq na. dinañuy wax tamit féq.

fer 1 : xale bu fer mooy xale bu nàmpatul. dafa fer mootax muy jooy guddi rekk.

fer 2 : ŋeer. dex gi fer na.

ferasu : riisu, feleesu. am nga sãas, oto bi dafa la ferasu rekk. dinañuy wax tamit feresu. (seetal feleesu)

ferenkulaayu : toog lem say tànk. ferenkulaayu lu yàgg dafay metti ay tànk. dinañuy wax tamit fereŋlaayu.

fereŋlaayu : dinañuy wax tamit ferenkulaayu. (seetal ferenkulaayu)

feresu : dinañuy wax tamit ferasu. (seetal ferasu)

feret : folet, fej. jaasi ji mënul a feret bànqaas bi.

feri b- : bag b-. feri bi ngoon lay deppaar.

fermtiir b- : defaral sa fermtiiru tubëy bi.

fer g- : gale g-, jal-jali b-, bin-bin y-. borom taabal ji ay fer lay jaay.

ferñent : génne ay ferñent. sébbu baa ngi ferñent.

fetal : dafa bëgg a fetal bukki bi. dinañuy wax tamit fital.

fete : fete ay yére yu ñuy fóot. xale bu jigeen bi dafa poose ay we mootax mënul a fete.

feteñ : sàkket. dafay feteñ di jaay.

fett 1 : tànk yi yépp a fett.

fett 2 : jam, màtt. jiit fett na ko ca tool ya. / jam, fett. rëbbkat bi fett na ab badom.

fettasu : jàng yi neex nañu ba ñépp a ngi fettasu. dinañuy wax tamit fottasu wala mottasu.

fettax : tëb dali feneen. li mu yorewoon fettax na dali fu sore. dinañuy wax tamit fittax.

few j- : xooxu buy b-, gif g-. baleel few yi, tuuri leen.

fexe : nanga fexe ba bu la sa menn morom raw.

fey : delloo nit li nga ko yoreel. nit ki soo ko yorelee bor danga ko war a fey. / sàppóor pompiye yaa ngi fey lakk gi. / tontu ku lay nuyu. fey naa ko waaye dégguma.

fey b- : piis bu am solo. xanaa li nga jënde fey bi seer na de ?