dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

fóbbanti : defaraat bootaay. fóbbantil xale bi bala muy daanu.

fóof : bees. dafay fóof dugub ji ci ngelaw li.

fóoli g- : dinañuy wax tamit kawsu g-. (seetal kawsu)

fóon 1 : tubaab baa ngi fóon jabar ji ci digg mbedd mi.

fóon 2 : xeeñtu. mu ngi fóon cere ji ba xam ndax dafa ënn wala déet.

fóon 3 : mëq póon. maamam dafay fóon.

fóot : fóot say yére bokk na ci ag cet.

fóoxal : nax, mbaleñfaŋŋ. dafa lay fóoxal rekk wànte du def li mu la wax. dinañuy wax tamit fuuxal.

fótëey b- : toogukaay b-. saalam ba def na fa ay fótëey yu rafet. dinañuy wax tamit fótooy b-.

fóto b- : nataal b-, portale b-. fóto bi yàgg na lool.

fótooy b- : dinañuy wax tamit fótëey b-. (seetal fótëey)

fótt : (ne fótt). def yaramu neen, ne duŋŋ. dof baa nga ne fótt taxaw ca digg mbedd ma.