dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

fëgës : fëgës na basaŋ bi ba puseer bi jeex. dinañuy wax tamit fëggës.

fëgësu : yëlbu, faxasu. mbóot baa ngi ci sa yaram wi, fëgësul. dinañuy wax tamit fëggësu.

fëgg-jaay : njaayum fëgg-jaay mi dox na ci réew mi léegi.

fëggës : dinañuy wax tamit fëgës. (seetal fëgës)

fëgg : dóor (buntu). kuy fëgg buntu bi ? / fëggal basaŋ bi ndax puseer bi dëñ.

fëj-fëji : tés-tési. fii ku fi bëgg a tekki léegi dinga fëj-fëji ba dee.

fëjj : yore biir bu réy. dafa fëjj mootax barewul ay yëngatu.

fëkk : jël dara ci lu gaaw. céeli gi fëkk na cuuj si. dinañuy wax tamit këf.

fëlëñu : bërëngu. boo sangoo ba pare, bul fëlëñu ci suuf de.

fëlëtal : fenantal, jéllale. déglu ko mu wax la ngay fëlëtal noonu.

fëll : jamono ji ñu koy tudd lay fëll.

fël : dinañuy wax tamit fél. (seetal fél)

fënëx : nëb. bantu lal bi dafa fënëx. dinañuy wax tamit funëx wala funax.

fëq : bëtt, bënn ci suuf. saaku bi dafa fëq, dugub jaa ngi tuuru.

fëriñ b- : kilo fëriñ dafa seer léegi. dinañuy wax tamit fariñ b-.

fër : yore biir buy daw bu tukkee ci ag ñàkk a reesal. xaram yi dañoo fër.

fërr : (ne fërr). coow liy am tey tukkee ci ay wàggi picc muy soog a naaw. picc mi dafa dégg balu fetal gi rekk ne fërr, naaw.

fërtët w- : tërngël b-, tëndëndiir b-. jàngalekat bi dafa dóor taalibe bi ba yaram wi fees dell ak ay fërtët.

fëtt : génn ci xel yi. aada boobu dafa fëtt léegi.

fëxëj : dinañuy wax tamit faxaj. (seetal faxaj)

fëxës : dinañuy wax tamit faxas. (seetal faxas)

fëx : dem ci lu gaaw ak ay daw. ba mu déggee xibaar bi rekk la fëx.