dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

féddali : dinañuy wax tamit feddali. (seetal feddali)

féeru : génne ndox mi nga duggaloon ak sa bakkan. kuy jàpp dangay féeru. dinañuy wax tamit fiiru.

féete : toll. sooy dem, këram a ngi féete wetu ndeyjoor.

féewale : jaxase. xaalis a leen féewale. safaan wi mooy jubale.

féex 1 : ñàkk looy def. dafa féex mootax muy dem fu ne. safaan wi mooy ñàkk jot. / am dal. béreb bi féex na. / am ngelaw. néeg bi féex na, ngelaw laa ngi dugg bu baax. safaan wi mooy tàng.

féex 2 : ku amul lenn lu muy rus a def. dafa féex rekk, waaye loolu kenn du ko def. safaan wi mooy bare kersa.

féey : ku mënul a féey soo demee géej, dangay yem.

fég : pare, sotti, jeex. la mu doon def fég na bu yàgg.

fél : oto bi fél na garab gi. dinañuy wax tamit fël.

fénc : waxtaan ci am mbir ca pénc ma. ci suñu porose ba lañu doon fénc.

fénqoo : songoo. xale yi fénqoo nañu.

fépp : fu nekk wala fu ne. dem na fépp soog a ñëw toog.

féq : xëcc bu gaaw ci lu amul waajaay, bif, ñoddi, téq. bul féq laxabu fas wi, loolu dafa koy gaañ.

fés : feeñ. picc bu ndaw la woon wànte léegi fés na. safaan wi mooy làqu, nëbbu.

fétt : bañ, lànk. fétt na ne du dem jàngi. safaan wi mooy nangu.