dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

fàbbi : yóbbu xelu nit feneen fu dul fi mu nekkoon. coow lee ko fàbbi.

fàcc : béey, xottiku. saaku bi fàcc na.

fàdd : rey, bóom, faat. gaynde gi fàdd na nagu-àll wi.

fàggandiku : jël say matuwaay, fagaru. dafay fàggandiku ndax bu këram lakk. dinañuy wax tamit fàggu.

fàggu : dinañuy wax tamit fàggandiku. (seetal fàggandiku).

fàkk : fàkk nañu fi ñu war a tëgge làmb ji.

fàllare g- : geenu nag am na fàllare.

fàlley j- : witteen bu ñu def wëñ mooy fàlley.

fànn g- : waxtaan nañu ci fànn googu wànte juboowuñu ci.

fànq : musal.Yàlla rekk moo mën a fànq loraange yi. dinañuy wax tamit fanq.

fàntar w- : fàntar xeetu jën la.

fànt : xar ci genn wet gi wala ci ñaari wet yi. tajoor dafa fànt robb bi ci wet gi.

fàŋŋ : (ne fàŋŋ). dàŋŋ (ne). lu ñépp di gis. lu ne fàŋŋ, kenn du ko jéex. (léebu).

fàppit : xàttit, faseet. baat bi dafay tekki lu ñu dagg dagg bu gaaw. reendi na xar mi fàppit.

fàq 1 : dindi bànqaasu garab. ngelaw li fàq na bànqaasu garab gi.

fàq 2 : daw dem. soo bàyyiwul dóor yu bare yi ngay dóor xale bi, dina fàq dem yoonam.

fàtte : menn mbir génn ci sa xel. naroon naa fa dem wànte dama ko fàtte.

fàww : dinañuy wax tamit faw -2. (seetal faw)