dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

esaas b- : dinañuy wax tamit esãas b-. (seetal esãas)

esarp b- : kol b-, tàmbasembe b-. esarp bi ànd na ak li mu sol.

esãas b- : oto bu amul esãas du daw. dinañuy wax tamit esaas b-.

espoor b- : dinañuy wax tamit tàggat-yaram. (seetal tàggat-yaram)

estaat b- : estaat béreb la bu ñuy futbalee wala ñu fay amal yeneen xeeti tàggat yaram.