dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

elaas b- : àllaaji b-. ku aji Màkka lañuy woowe elaas. safaan wi mooy ajaratu wala ajaa.

eleew b- : ndongo l-, njàngaan l-. eleew yi wàcc nañu.

elimaan j- : elimaan mooy kiy jiite julli gi ca jàkka ja. dinañuy wax tamit ilimaan j-.