dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

ekib b- : mbooloo mu ñu tënk ci ab lim. suññ ekibu futbal bi am na ndam tey.

ekkool b- : dinañuy wax tamit ekool b-. (seetal ekool)

ekool b- : daara ci làkku farañse. bi mu jàngee alxuraan ba pare la sooga dugg ekool. dinañuy wax tamit ekkool b- waka lekkool b-.

eksame b- : ku war a def eksame doo am jotu taxawaalu.