dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

dugg : dugg na ci biir néeg bi. safaan wi mooy génn. / bul dugg lu sa yoon nekkul. / xamal bu baax li ngay dugg lan la. /

dugub j- : suna s-, basi b-. ren dugub bare na lool. dinañuy wax tamit dugug.

dugug j- : dinañuy wax tamit dugub. (seetal dugub)

dujur w- : dinañuy wax tamit dojar w-. (seetal dojar)

dukkat : di doxe ni ñay, dukki-dukki, yugur-yuguri, wagar-wagari. diriyànke baa ngi dukkat di ñëw.

dukki-dukki : dukkat, yugur-yuguri, wagar-wagari. tase naa ak moom muy dukki-dukki di dem.

duma : dinañuy wax tamit dóor. (seetal dóor)

dumat : dinañuy wax tamit duumat. (seetal duumat)

dummooyu : dinañuy wax tamit dummóoyu. (seetal dummóoyu)

dummóoyu : gestu, ëlbatiku. kuy dawal oto warul a dummóoyu. dinañuy wax tamit dummooyu. safaan wi mooy soylu.

dund : bàkkan bu mos dund dinga mos dee. safaan wi mooy dee.

dung w- : kaay suqi dungi ginaar yi. dinañuy wax tamit dunq w-.

dunguru b- : siboor b-. bul nangoo nekk dunguru kenn, demal nga liggeeyi.

dunj w- : taw bi seeyal na dunji suukër yi. dinañuy wax tamit donj w-.

dun b- : Gore ab dun la.

dunq w- : dunq w-. dinañuy wax tamit dung w-. (seetal dung)

dunyaa b- : àdduna s-. dunyaa bi dañu fi jaar rekk.

duññi : lekkinu yenn ci mala yi. nag ak xar yépp dañuy duññi.

duŋŋ : (ne duŋŋ). def yaramu neen, benn yére toppu la. xale yi futti nañu sàcc bi ba mu ne duŋŋ. safaan wi mooy solu.

duppati : dagg. duppatil xaal bi, ma xool.

duppe : tudde. maamam ju góor lañu ko duppe. dinañuy wax tamit dippe.

duri b- : dinañuy wax tamit dori b-. (seetal dori)

dur : (ne dur). màndi bu baax. waa ji dafa màndi ba ne dur mootax mu tëdd ci suuf.

duruŋlu : daw am mbir. danga duruŋlu rekk wànte mbir moomu yaa ko waroon a lijjanti.

duruus : jàng, ndax nga mën a duruus mindum wolof.

dute j- : kinkelibaa b-, sexaw b-. dute lay ndékke.

duubal b- : ñaar yi. li mu la may duubal bi la ma may.

duuf : suur. xar mu duuf la jënd ngir tabaski bi. safaan wi mooy tuuti wala sew.

duul 1 : (saaga la) meerd. duul ! noppil, bare nga wax.

duul 2 : puub, day. xale bi duul na fi. / fen (saaga la). du dëgg, dangay duul.

duumaan : woyantu. dafa tàmm di duumaan buy def dara.

duumat : meeb. dugub lañuy suy ci suuf ngir duumat picc yi. dinañuy wax tamit dumat.

duun : sakkan. dafa ko yónni mu ñëw mu jox ko neexal bu duun. safaan wi mooy tuuti wala néew.

duus b- 1 : wanag w-. ndax duus bi set na ?

duus b- 2 : mbar m-, gannax g-, wàgg b-. duus bi dafay génne lépp lu dëkkul ci géej gi.

duut : nax. futbalkat bu nekk war ngaa mën a duut.

duux : dinañuy wax tamit dóox. (seetal dóox)

duwaa g- : dinañuy wax tamit dóobaali g-. (seetal dóobaali)

duwaañ b- : duwaañ bi xaalis bu bare lay dugal ci réew mi.

duy 1 : sol, root. duy na guttam yépp ci róbine bi.

duy 2 : duy julli te jàppul.