dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

dof : dese, yembadi, woyadi. soo bàyyiwul tux yàmbaa, dangay dof léegi. safaan mooy yewwu, muus, am-xel.

dog-dog b- : liggeey bi dafa amoon dog-dog mootax mu yéex.

dog-ub-tënk : béreej. ku dog-ub-tënk mooy kuy faral di yàgg ci ay yónent, kuy jaar fu nekk di taxawaalu bu ñu ko yónnee.

dogal : àtte. li Yàlla dogal, jaam mënu ci dara.

dog : dagg. fas wi dog na buum gi ñu ko yeeweewoon. / dog koor. fan yii, bu juroom-ñaari waxtu tegalee fanweeri simili lañuy dog. / noppalu, faatu. léegi la dog. / liggeey ba mënatuloo. dafa liggeey ba dog.

dojar w- : bëtu tànk b-. ci dojar la gaañu bi mu danoo. dinañuy wax tamit dujur w- wala dojor w-.

doj w- : xeer w-. aw doj la ko xaañe ci bopp.

dojor w- : dinañuy wax tamit dojar w-. (seetal dojar)

doktoor b- : fajkat b-. doktoor dafay laabiir.

dolli : yokk. dolli ma tuuti suukar. safaan wi mooy wàññi.

domadaa b- : soosu tamaate bu am fariñ di ànd ak ñànkataŋ. domadaa la añe ca réstoraŋ ba.

domm : (lewet) ba mu ëpp. sa ceeb bi dafa lewet domm.

domp : kaata. bàyyil xale bi ngay domp. dinañuy wax tamit dompat.

dongali : pare ci waajaay yu mujj yi (mbër). mbër yi dongali nañu ba sëgg di bëre.

dong : am feebaru lox. góor gi dafa dong.

donj w- : donju cere. tojal donji cere yi.

donk-leere g- : kubeeru mbana. ubbil donk-leere gi.

donkaasi g- : ci kow, ci boppu nguur. waa ji waxatul dara, mu ngi ci donkaasi gi léegi.

donk b- : ginnaawu mbaam. bul dóor mbaam mi ci donk bi.

donn : jël sa wàll ci sa alali waa-jur wu faatu. taaw bee donn oto bi.

doŋŋ : rekk, kese, kott. yow doŋŋ yaa dul woor.

doŋo j- : tund w-, jànj b-. séen naa ko mu taxaw ca kow doŋo ja.

doog : def dara yoon wu njëkk. mu ngi doog a dem Ndar. dinañuy wax tamit door wala soog.

dooj : di def yëfi mag. xale bi dafa dooj, du def yëfi xale mukk.

doole j- : mbër dafa war a am doole. / xaalis, alal. soo amul doole, dangay dugg ci loo mën.

doom b- 1 : doomu màngo bi ñoragul. / per b-, kompirime b-. boo demee, jëlal ñaari doom, baax na ci bopp buy metti.

doom b- 2 : caabi j-. doomu buntu néeg bi dafa réer.

doom-aadama b- : nit k-. nguur gi war naa sàmm àq ak yelleefi doom-aadama bi.

doomaraam b- : (saaga la) nit ku judduwul ci sëy. xale bi doomaraam la.

doom j- : xale b-. yaral sa doom ji, moo lay noppal ëllëg, noppal ko.

doomu-baay j- : koo bokkal baay (benn baay wala seen baay yi bokk). sa doomu-baay sa nawle la. / doomu-baay tur la wu ñuy woowee ku ñu bokkal benn sant. dinañuy wax tamit doom-baay j-.

doomu-bàjjen j- : doomu sa magi wala sa rakki pàppa ju jigeen. doomu-bàjjenam la takk. dinañuy wax tamit doom-bàjjen j-.

doomu-jàngoro j- : ndoxu taataa dafay am doomu-jàngoroy sibbiru.

doomu-jiitle j- : sa doomu-jiitle ji, jàppe ko ni sa doomu bopp.

doomu-ndey j- : doomu-yaay j-. koo bokkal ndey (benn ndey wala seen ndey yi bokk). am na ay doomu-ndey yu bare. / doomu-ndey tur la wu ñuy woowee ku ñu bokkalul benn sant. dinañuy wax tamit doom-ndey j-.

doomu-nijaay j- : doomu sa mag wala sa rakki yaay ju góor. jabaram doomu-nijaayam la.

doomu-saalum j- : ku dëkk wala ku cosaanoo Saalum. jëwriñ ji doomu-saalum la.

doomu-yaay j- : dinañuy wax tamit doomu-ndey j-. (seetal doomu-ndey)

doonte : àttaa. jox loxo jigeen joo mën a takk daganul doonte nit ñaa ngi koy def.

dooñ b- : sas w-. xale yi def nañu tool bi ay dooñ yu bare.

door : tàmbali, dal, komaase. làmb ji ngoon lay door.

doq g- : sa doq gi dafay metti ?

dori b- : illeer bu màgget. jëndal illeer bu bees nga sànni dori bi. dinañuy wax tamit duri b-.

dorog b- : sinebar b-. dorog bi ngay jël, moo la war a sànk soo ko bàyyiwul.

dotom : am jefe-jefe ci kàddu. xale bi dafa dotom.

dott : sëriñtu nit ba dootul mën a génn fi mu nekk. dafa toppoon àll bi di dox rekk wànte ay mbokkam dañu ko dott léegi.

dow : looy dow bay daanu ? dinañuy wax tamit daw.

doxat : ngelawal. xale baa ngi doxat rekk, xanaa dafa bëgg a puub ? dinañuy wax tamit doxot.

dox : suñu maam yi dañu daan dox ba Màkka. dox mbokk dafay dëgëral ay diggante.

doy-waar : yéeme. loolu lu doy-waar la.

doy : li nga jënd doy na. safaan wi mooy mànke. / kookoo ñu doy.

doy w- : xeetu jën. tey ay doy rekk a am ja ba.