dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

daa 1 : daa na fi ñëw wànte gëj na fi. dinañuy wax tamit daan.

daa 2 : daa sonn te du noppalu. dinañuy wax tamit dafa.

daabo b- : ndaama b-, daamar j-. dawalal sa daabo bi ndànk ci kow tali bi, yenn daw yi wóorul.

daagu : temp, yéexamtu. diriyànke baa ngi daagu nu ko neexe. safaan wi mooy waaxu.

daaj : dóor ab pont ba mu dugg fenn (taax, bant wala feneen). daaj na ab pont, wékk ci portale maamam bi. safaan wi mooy dàjji.

daakaande j- : lu ñuy jëfandikoo ngir paase ay yére mu tàlli. yére bi def ci daakaande ba mu saf. dinañuy wax tamit dàkkaande j-.

daal : dëgg-dëgg. ñàkk a jàng daal wóorul.

daamar j- : mala buy yenu (mbaam, fas, …). def ko ndànk, daamar ji dafa am bakkan. dinañuy wax tamit daamaar j-. / daabo b-, oto b-. daamar waruwaay wu am solo la.

daamina : ñaw ñawu borode. masin bi dafay daamina.

daan 1 : bu daan taw, xale yi dañuy sangu ci biir taw bi. dinañuy wax tamit daa.

daan 2 : moo la mën ndax daan na la ñaari yoon. / ku rey nit yoon dafa la war a daan sa giiru dund. / sama mbër a daan mbëram.

daanaka : peresk. njàng mi mettiwoon na wànte daanaka pare na.

daanu-leer : xar, neey. jàng yee neex mootax mu daanu-leer.

daanu-rab : say. jabar ji dafay daanu-rab.

daañu : daañu booloo liggeey suñu réew mi. dinañuy wax tamit dinañu wala danañu.

daara j- : lekkool b- (alxuraan wala araab). njàngum daara baax na ci yaru xale.

daar b- : sëll wuy nàmp. daar bi rafet na lool.

daas : nàmm, ñawal. buuse bi daas na paaka bi ba mu ñaw.

daaw : at mi jiitu ren. daaw la doon jàng wolof.

daaxër-daaxër : dox dox bu metti. lu muy daaxër-daaxër di ñëw nii ?

daax : dabb-daaxe, gaar. dafa daax yére bi.

daay g- : lakku àll. daay baaxul ci jur gi ndax bu àll bi lakkee, dootuñu am lu ñu lekk.

daba b- : gasukaay b-. abal ma daba ma gas ay pax, samp sama sàkket wi.

dabb-daaxe : daax, gaar. tubeyam yépp la dabb-daaxe.

dabin : feyu lu la nit def. ku ma ko rókkin ma dabin la ko. safaan wi mooy baal.

dab : jot. xale yi dab nañu sàcc bi.

dafa : dafa boole siis ak soxor. dinañuy wax tamit daf.

daf : dafa. daf reew wànte àdduna dina ko yar.

dagaj : (ne dagaj). saraax, parax, pëll. baat bi dafay tekki lu jékki jékki rekk dugg fenn. jinax ji ne na dagaj ci biir pax mi.

dagan : lu diine nangu. fase dagan na wànte Yàlla bëggu ko. safaan wi mooy araam.

dagañ : def benn xeetu fecc. soxna si mën naa dagañ.

dagg : dog. goj bi dafa dagg, baag bi dugg ci teen bi. / gaañu. dagg na boppam ak paaka bi.

dag b- : ñiy wër buur di ko dawal ay sarwiisam. buur aayul, dag yaa aay. (léebu).

daj 1 : mat. ndax darab bi daj na lal bi ? safaan wi mooy des.

daj 2 : daj na aw xeer ci cere ji. / dem. bu sa menn xel daj ngay tux yàmbaa wala ngay naan sàngara. / yég. coono bi ma daj ci sama njàng man ak Yàlla rekk a ko xam.

dajjant : gëmmentu. yaa ngi dajjant rekk, xanaa nelawuloo biig ?

dakkase : dajale gerte gi ñu deqi ba pare, tar. jigeen ñi dañuy dakkase.

dakk : jeex. seen wax ju bare ji na dakk wala ngeen génn fii. safaan wi mooy wéy wala kontine.

dal 1 : wàcc ci kër nit wala ci ab otel. kër nijaayam la dal. / jot. lu ko dal, dafa sibbiru wala dafa soj ? / song. waa Amerig yi dal nañu ci kow waa Irag yi.

dal 2 : tàmbali, komaase. doomam ji dal na jàng keroog.

dal 3 : boo meree danga war a dal bala ngay def lu ëpp.

dal-xel : féex, ñàkk jafe-jafe yooy xalaat. danga dal-xel rekk wànte waa ji ku ko gis xam ne jubul. safaan wi mooy bare-fitna.

dal-xel g- : dal-xel gi mu dal-xel moo koy lor saa yu nekk.

daldi : ba pare, ci saa si. dafa séen gaynde gi rekk, daldi deppaar. dinañuy wax tamit dàddi wala daadi.

dale ko : li ko dale. li tàmbale ci …dale ko tey ba ginnaaw suba, buleen génn guddi.

dale ko : dinañuy wax tamit li ko dale. (seetal li ko dale)

dall g- : am pax mu jinax suul ngir aar ay doomam. doomi jinax yaa ngi ci biir dall gi.

dama : dama woor, mootax ma xiif, mar, sonn. dinañuy wax tamit damaa.

dambal b- : (wax ju ñaaw la) xuur b-. nëbbal ko dàmbal yi.

damiye : mag du damiye.

dammel b- : barag b-, buur b-, teeñ b-, lingeer b-. maamam dammel la woon.

damm : damm na bant bi ci digg bi. bi mu defee aksidaa la loxo bi damm.

damoo : kañoo. li mu def lay damoo wànte loolu du ndam, wareefam la.

dana : bu bàyyiwul tux sinebar, dana mës a dof. dinañuy wax tamit dina.

dand 1 : sore, xëccu. ndax seen dëkk dand na fi tuuti ? safaan wi mooy jege.

dand 2 : tilim. baleel sa néeg bi, dafa dand. safaan wi mooy set.

danga : danga xamul rekk wànte soo xamoon li ci ñàkk a jàng, danga góor-góorlu bu baax. dinañuy wax tamit dinga.

dangeen : dangeen di xale rekk, loolu yàgg na fi.

dank : tëj ay yoxo. dank na yoxoom yi. / dank dinay tekki defar ay bulet tamit.

dan : dan sonn, danuy noppalu. dinañuy wax tamit dañ, dañu wala danu.

danq g- : xeetu meññent. àll bi am na ay danq. dinañuy wax tamit dànq.

dañ 1 : bajjantu, tëbantu. fas waa ngi dañ.

dañ 2 : dañ mar wànte amuñu ndox. dinañuy wax tamit dañu.

dañ 3 : mbëkk. moytuleen xar mi, dafay dañ. dinañuy wax tamit ndañ.

dañaru : lekk ñebbe bu ñu xolli bees mooy dañaru.

daŋ 1 : daŋ ko tooñ mootax mu mer. dinañuy wax tamit danga.

daŋ 2 : teeŋ. xale yu jigeen yu bare léegi lu daŋ rekk lañuy sol. safaan wi mooy yolom wala yoxom.

daŋ-daŋ j- : baat bi dafay tekki nekk ci ay tës-tës. bàyyil daŋ-daŋ ji te noppalu.

daŋ-ŋaam : bare-wax. soo bàyyiwul daŋ-ŋaam, sa làmmeñ wi dina la yóbbu kaso. safaan wi mooy noppi.

daŋaaral : rëy. waa ji dafa daŋaaral mootax du mën a def loolu. dinañuy wax tamit dàŋŋaaral. safaan wi mooy woyof.

daŋar j- : ci jaan lay nekk. jaan tuuti na wànte am na daŋar.

daŋ b- : donj b-. may ma benn daŋu cere.

daqaar g- : garabu dàqaar g-. dàqaar gi meññ na.

daqaar j- : béngal j-. fullaay jaay dàqaar. (léebu).

dar 1 : taq ci taatu cin. li ngay togg ñor na, soo ko yakkul dina dar. / féete fu nekk. takk-der yaa ngi dar njiitu réew mi ngir sàmm kaaraangeem.

dar 2 : dëgër ngir liggeey. jigeeni àll ba dañuy dëbb ba seen yoxo yépp dar.

darab b- : sër bu mag bu ñuy lal ci lal. lal na darab bu rafet di xaar ay ganam.

daraja j- : ku am gëdd, ku ñu weg. borom daraja la mootax mu am cër bu mag.

daral b- : béreb bu ñuy jënde ak a jaaye jur gi. tase nañu daral bërki-démb.

dara : tus. lekkuma dara ci suba ba léegi. / amul ba ñu koy coow wànte denc na dara de. / xale bi bëggul jàng dara.

darkase b- : doomu darkase. jox ma saalu darkase bi. dinañuy wax tamit ndarkase b-.

darkase g- : garabu darkase. dëkk bi am na ay garabi darkase. dinañuy wax tamit ndarkase g-.

darngu : watatu. buy dox dafay darngu.

data b- : (saaga la) awra jigeen, lëf l-, dëjj w-, caapa b-, bajo b-. sàngal ko data bi.

datax g- : garabu datax. mësumaa gis garabu datax. dinañuy wax tamit dattax g- wala dittax g-.

dattax g- : dinañuy wax tamit datax g-. (seetal datax)

daw yaram : lu yërëmlu. ni yalwaankat bi mel, daw na yaram.

daw-raw : ni mu baree wax, saku sax daw-raw.

daw : bul daw bala li nga yenu di daanu. safaan wi mooy dox. / moytu. damay daw ñibbi bala ma fi taw bi di fekk. / xanaa dereti gor dawul ci sa yaram ? / bi ma gisee liir bi ñu sànni sama yaram dafa doon daw. / xale bi biiram dafay daw. / dafay daw jàng rekk wànte dara jotu ko. dinañuy wax tamit dow.

daxin b- : ceeb bu ñu baxal ak soosu gerte. daxin la toggluwoon démb.

dax g- : bëer b-. du lekk mburoog dax.

day 1 : puub, kabine, dem àll. yemal, nga mel ni ku dul day nii.

day 2 : toll, yem. seen dëkk day na ni sunu bos.

day 3 : day dem tool. dinañuy wax tamit dafay.