dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

dóobaali g- : xeetu garab. am na dóobaali gu mag gu nekk ca seen digg dëkk ba. dinañuy wax tamit dóob g- wala duwaa g-.

dóob g- : dinañuy wax tamit dóobaali g-. (seetal dóobaali)

dóolinka g- : oos g-, jàppkaayu jën. ndax andi nga sa dóolinka gi, ñu jàpp jën.

dóom b- : safara su dem ba def dóom. dóom bi dafa tàng.

dóor : duma, ñaf. xale su defee naka su dul noonu, dañu koy dóor. / jël ndam. dañu doon damiye wànte dóor naa ko.

dóox : nóox. ginnaawu mbaam mi dafa dóox. dinañuy wax tamit duux.