dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

dédd b- : bérebu garabi dég. solal say dàll booy dem dédd ba.

déebaadéeb y- : gàllaaj y-. bi mbër yi defee seeni déebaadéeb ba pare, lañu sëgg bëre.

déede j- : kol b-. foo jënde déede ji ?

déedet : déedet bul dem, dafa guddi. dinañuy wax tamit déet. safaan wi mooy waaw.

déegeej b- : sell b-, reewu b-, bëñ b-. déegeej bi dafay metti ci suba ba léegi.

déeg : ër, law. taw bi dafa déeg seen dëkk.

déeg b- : jigeen ñi rooti nañu déeg ba.

déem g- : garabu déem gi dafa am ay dég. dinañuy wax tamit siddeem g-. (seetal siddeem)

dée : dinañuy wax tamit de wala dee. (seetal de)

déet : déet, bul dugg ci loolu mukk. dinañuy wax tamit déedet. safaan wi mooy waaw.

déey : wax nit dara ndànk. sama waa jee ma déey loolu.

dég-dég b- : xibaar b-. am nañu dég-dégu mbégte ci peyoor yi. / amul benn dég-dég ci li waa ji wax.

déget b- : xoox b-. baleel dégeti màngo yi.

dégg-ndigal : xale dafa war a dégg-ndigal, loolu mooy li koy jëmale kanam. safaan wi mooy dëgër-bopp.

dégg : dégg naa ñu naan nit nit ay garabam. / ndax dégg nga li mu wax bu baax ?

déggoo : juboo, méngoo. nañu déggoo ndax bu ñu kenn mën a féewale. safaan wi mooy dëngoo wala réeroo.

dég g- : dég a ko jam ci tànk. dinañuy wax tamit dëg g-.

déjj : (ne déjj). déjj mel ni ku toog wala ku ñu toogloo benn béreb. dinañuy wax tamit réjj.

déj : toogloo. bàyyileen seen bëre bi wala ma déj leen fii. / tiye nit ci béreb. ay mbokkam dañu ko déj mootax dematul fenn. safaan wi mooy déjjati.

dékkarle : méngale. ki nga may dékkarleel duma moromam.

dékk : tàllal loxo wala bool ngir jël ci dara. dékk na ci ndoxu taw bi. / tàllal say yoxo am mbër ngir bëgg a bëre ak moom. dékk na ko ca làmb ja mu bañ. dinañuy wax tamit dëkk (mbër).

dékk j- : juróomeelu jamono juy am fukki fan ak ñett ci nawet bi. ci dékk ji lañu nekk léegi.

démb : bés bi jiitu tey mooy démb. démb la fi ñëw.

dénd w- 1 : ñax mu ñu rabat. dénd wi la bëgg a xëdde néegam.

dénd w- 2 : béreb bu yaatu. Senegaal ci déndu Afirig la bokk.

dénd : tàllal. deru xar bi mën na julleekaay, dinaa ko dénd.

dénk : dénk na ko xaalis bu bare.

dénk b- : xànq g-, bant b-. ay dénk lay jaay.

dénqleñ w- : sama dénqleñ wi dafay xasan.

déñ : dinañuy wax tamit dëñ. (seetal dëñ)

déqati : buddi, sempi. ngelaw li déqati na garab gi fi nekkoon. safaan wi mooy samp.

déqi : dindi gerte wala leneen luy nekk ci biir suuf. bi ñuy déqi gerte la fi nijaayam ñëwoon. safaan wi mooy suul.

déq b- : déq mooy baaraasu ndox. dinañuy wax tamit dëq b-.

dérr : (ne dérr). baat dérr dafay tekki coowu lu jóge ci kow daanu ci suuf. picc mi dafa naaw ba ne dérr ci suuf.

déwen j- : Yàlla nañu fekke déwen.

déy : wow, ŋacc. déeg bi fii la nekkoon wànte dafa déy léegi.