dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

dàddi : dafa séen bukki bi rekk, dàddi daw. dinañuy wax tamit daldi wala daadi.

dàdd : (ne dàdd). baat bi dafay tekki lu funki bay bëgg a toj. xamuma lu mu lekk wànte biir baa nga funki ba ne dàdd.

dàgga j- : béreb bu ñuy def ay sàq. seen sàq maa nga ca dàgga ja.

dàggasante : xuloo, xasante. jigeen ñaa ngay dàggasante ca teen ba. dinañuy wax tamit dàkkasante wala dàggayante. safaan wi mooy juboo wala neexoo.

dàggeeku : beru, soyndaaru, beddeeku. gëstukat waru la dàggeeku, nekk ruqu boppam.

dàggi : nàmm, daas. war nga dàggi sa jala gi bala may gasi gerte.

dàjji : dindi ay pont, yàq. sàcc bi dafa dàjji bunt bi, yóbbu li fi nekkoon yépp. safaan wi mooy daaj.

dàkk 1 : tay, def kol. dàkk na téereem yu yàqu yi.

dàkk 2 : diir. rëbbkat bi boppu gaynde gi la dàkk.

dàkkaande : def dàkkaande ci yére ngir mu tàlli. soxna si dàkkaande na yéreem bi, paase ko ba mu taxaw. dinañuy wax tamit daakaande.

dàkkasante : dinañuy wax tamit dàggasante. (seetal dàggasante)

dàkkental b- : tur wu ñuy yokk ci weneen tur ngir bañ a jaawale borom ak keneen. Maamur Xoreja, turu yaayam mooy dàkkentalam.

dàkk g- : téere buy jaar ci mbagg ak ci wet. mbër yi dinañuy faral di takk dàkk.

dàlleñ w- : kawsu póno. yar bi dàlleñ lañu ko defare.

dàll : (ne dàll). baat bi dafay tekki coowu lu daanu bu baax. tan mi dafa naaw ba ne dàll ci suuf.

dàll w- : tànk bu solul dàll, dëgg day. (léebu).

dàmb b- 1 : pañe b-. dàmb bi juroom-fukki kilo lay peese. dinañuy wax tamit dàmba b-.

dàmb b- 2 : néeg bu ñuy denc bagaas yi ñu dul soxla tuusuur. seetal ma ko ca dàmb ba.

dàmbe : boole. dàmbe na yépp ci benn saag. safaan wi mooy xaajale.

dàmp : bës. sama yaram wi yépp ay metti, kaay dàmpal ma ko.

dànd : séq, wër. buleen ko dànd, dafa tàng. safaan wi mooy sore.

dàngin g- : golo gu mag. tey lay soog a gis dàngin.

dànkaafu : artu, yégal. nguur gi dànkaafu na ñiy luubal alali askan wi. dinañuy wax tamit dankaafu. safaan wi mooy bett.

dànkeew g- : xeetu yàmb. moytul dànkeew gi màtt la.

dànnala b- : jamkat bu jub loxo. dànnala bi mësul a moy, lu mu diiraan, dina ko jam.

dànq g- : dinañuy wax tamit danq. (seetal danq)

dàŋŋ : (ne dàŋŋ). fàŋŋ (ne). luy feeñ bu baax.weer waa ngi ne dàŋŋ

dàq 1 : toxal. dàq nañu ndaje mi ba beneen jëmmi jamono. / soreel. yal naYàlla dàq saytaane ba mu sore ñu. / dàq na muus mi bëggoon a laal jën yi.

dàq 2 : gën a rafet, gën a neex. jabaram a dàq ci ñoom. ceebu jën a dàq mbaxal. / mën ci am mbir. rakkam jee ko dàq a jàng.

dàtt b- 1 : fi ay létt deppaare. dàtt baa ngi toll ci digg bopp bi.

dàtt b- 2 : jëmmu garab gu wow. seen buntu kër am na benn dàtt bu fa nekk.