dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

coblet g- : xeetu picc yu ndaw yuy topp nag yi. coblet gi sonal na nag wi.

cobraan b- : nit ku tuuti torob. foo fekk ab cobraan dafay naqari dereet. safaan wi mooy ponkal m-.

cocc : (ne cocc). wér péŋŋ. dafay tappale rekk wànte mu ngi ne cocc, dara jotu ko. dinañuy wax tamit kocc. safaan wi mooy wéradi.

cof 1 : ginaar dafay cof buy lekk.

cof 2 : feresu, laal ndànk. am nga sãas gaañuwuloo, oto bi dafa la cof rekk.

cofeel g- : baatu cofeel g- mu ngi jóge ci baatu sopp. (seetal sopp)

coggal g- : gétt g-. naar bi coggalu xar la andi, di ko jaay.

cogg g- : siboor b-. bul nangoo nekk cogg kenn.

cojjal : dinañuy wax tamit coqotaan. (seetal coqotaan)

cokeer l- : dinañuy wax tamit cokkeer b-. (seetal cokkeer)

cokkaas : tooñ. dafa naqari-dereet, bul ko cokkaas.

cokkeer b- : dafa rëbbiwoon, wànte benn cokkeer rekk la jàpp. dinañuy wax tamit cokeer l- wala sukkeer b-.

cokk l- : kawari naq. ajal sa tubey ji, sa cokk laa ngi feeñ.

colal : taxaw di saw. bàyyil colal ci mbedd mi.

coleet : (ne coleet). baatu coleet dafay tekki lu gudd ca kow. garabu xott-buteel dafa ne coleet ca kow.

coll g- : puj b-, njubb l-. picc ma dal na ca collu néegu ñax ba.

col g- : colin g-, colaay g-. léegi xale yu jigeen yu bare col gu gàtt wala col gu daŋ moo leen gënal.

colu g- : colu gi ci deppãas yi la bokk.

como b- : ku amul benn solo. Nelson Màndelaa du como. safaan wi mooy kilifa g- wala ponkal m-.

comp w- : baatu comp w- mu ngi jóge ci baatu somp. (seetal somp)

conc b- : booy jàpp dangay raxas sa loxo ba ci sa conc. dinañuy wax tamit conco b- wala concu b-.

cong g- : baatu cong g- mu ngi jóge ci baatu song. (seetal song)

conkom b- : sëng b-. jullit du naan conkom.

coobare g- : bëgg-bëgg b-. defuma ko ci sama coobare. safaan wi mooy naqar.

coof b- : xeetu jën. ceebu-jën coof a ci dàq. / góor gu rafet. sa far wi coof la.

cooke : ñàkk a ñor, ñor bu maase. mbaxal gi dafa cooke.

coono b- : sa liggeey bi dafa bare coono. àdduna coono kese la. safaan wi mooy noflaay g- wala dallu b-.

cooroon l- : jamono ji Yàlla ji di waaj a taw. ci cooroon li la rujoon toolam yépp.

cooska l- : ñuulitu cin. cooska lañuy defare daa.

coow l- : baatu coow l- mu ngi jóge ci baatu soow. (seetal soow)

coowu l- : baatu coowu l- mu ngi jóge ci baatu soow m-. (seetal soow)

coppati : jël tuuti ci am mbir ak ay cati waaraam. ku coppati cere ji ?

coppati b- : ay beñe yu ndaw. coppati bi nga defaroon ca ngénte la, neexoon na.

coppite g- : baatu coppite g- mu ngi jóge ci baatu soppi. (seetal soppi)

copp : (ne copp). toŋ. muus maa ngi ne copp ci kow teraas bi.

coppret b- : coppret cër la bu nekk ci biir awra jigeen.

coqotaan : tex-texaan, cojjal. li nga ko doon coqotaan mootax li mu yoroon wadd. dinañuy wax tamit coqtaan.

coqtaan : dinañuy wax tamit coqotaan. (seetal coqotaan)

coro-rab b- : faru-rab w-. ndaw si dafa am coro-rab.

coro l- : waxaale b-. bala ngay takk sa coro li, fexeel xam jikkoom bu baax.

coroxaan : am ay jafe-jafe ci put ginnaaw bu am ndox wala leneen teggee yoonam ci biir gémmeñ. dafa doon naan coroxaan.

cosaan l- : ndoorteel, aada j-, taarix b-. làmb cosaan la ci réew mi.

cott b- : (saaga la) data b-, lëf l-, bajo b-, dëjj w-. tubey ji mu sol dafa bënn fi tollook cott bi.

cox b- : liy génn ci dugub ju ñu soq di ko bees. joxal nag yi cox bi.

coxor g- : baatu coxor g- mu ngi jóge ci baatu soxor. (seetal soxor)

coy 1 : yére bu xonq coy la soloon démb. dinañuy wax tamit coyy wala curr.

coy 2 : werta ni coy. yére bu coy la sol tey.

coy l- : saku l-. coy li dafay làkk wolof yu leer nàññ. dinañuy wax tamit seku l- wala caku l-.

coyy : (xonq coyy). dinañuy wax tamit coy. (seetal coy)