dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

ci saa si : ci taxawaay. tux na paketu sigaret ci saa si.

ciib : coow liy am bu nit di ciipatu. sa ciib yi bare torob, lan la ?

ciiku : dinañuy wax tamit ciipatu. (seetal ciipatu)

ciipatu : janq bi bàyyil ciipatu. dinañuy wax tamit ciipu wala ciiku.

ciipu : dinañuy wax tamit ciipatu. (seetal ciipatu)

ciiriir l- : séq m-. kawar giy nekk ci kow baatu fas. watal na fas wi ciiriir li.

cilmaxa g- : gumba g-, njàccaar b-. cilmaxa gi dafa ko dab, judduwaalewu ko.

cim : dinañuy wax tamit cam. (seetal cam)

cin l- : kàddir g-, mbana g-, telle g-. bombal cin li ba mu set wecc.

cinwaar g- : li ñuy jëfandikoo ci ag togg ngir seppi wala jeqi. jëndaaleel ma cinwaar. dinañuy wax tamit cumwaar g-.

ci : maa ngi ci kër gi. làkk ko ko ci seereer, déggul wolof. teggi ko ci kow lal bi. may ma ci.

ci : dinañuy wax tamit ca. (seetal ca)

ciñaag : jaaru, ceeñeerlu. màgget maa ngay ciñaag ca naaj wa.

cippeelu : tëbbe ci kow jëm ci suuf. xale yi bàyyileen cippeelu, dangeen di gaañu. dinañuy wax tamit cëppéelu.