dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

ceddo b- : yéefeer b-. ku amul benn gëm-gëm ci wàllu diine. réew mi amoon na ay ceddo.

ceeb b- : xeetu ñam fii ci réew mi. ceeb dafa bokk ci dundug waa réew mi.

ceen g- : càllala g-. ceen gu rafet la andaleel jabaram bi mu demee Tugël.

ceeñeer l- : rëddi jant bi wala leer-leeri jant bi. tëjal bunt bi, ceeñeer laa ngi dugg ci biir néeg bi.

ceeñ l- : maccaat m-. ceebu-jën ceeñ ca la bokk.

ceet g- : jëfi seet li war a nekk. ceet gi muy def am na xaalis ndax dafa am kiliyaa léegi.

cefaay l- : dinañuy wax tamit cafaay l-. (seetal cafaay)

cell : (ne cell). patt (ne). wax juy tekki lu ne cell. soo xamul loo war a wax ci mbir mi, neel cell.

cere-faas j- : kus-kus marokee b-. ndax am ngeen cere-faas ?

cere j- : dugub, mboq wala basi lañuy defare cere. jabaram cere ak yàppu béy lañu toggaloon.

cet g- : cet mat naa sàmm fépp ndax dafa bokk ci li ñuy aar ci feebar yu bare. safaan wi mooy tilim b-.