dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

caabi j- : doom b-. jumtuwaay ngir ubbi, tëj wala taal. jox ma caabi ji ma ubbi bunt bi. / ana caabi oto bi ?

caaf l- : gerte gu ñu xolli ba pare saaf ko. gerte caaf suurul ponkal wànte sedd na xol.

caakiri b- : arawu dugub bu gën a dijj arawu cere ñu suusal ko. jaay ma soow ak caakiri.

caalit b- : caalit boo tàggoo ak sa xel nga koy def. dinañuy wax tamit saalit. (seetal saalit)

caapa b- : awra jigeen, lëf l-, bajo b-, dëjj w-. bu ma ko déggati de, caapa saaga la.

caar : yor biir-buy-daw. xale bi dafay caar ci suba ba léegi.

caas g- : càmpóor b-. màngo bi dafa bare caas.

caat m- : doom ji mujj a juddu. dafa reewal caatam mi ba mu ëpp. safaan wi mooy taaw b-.

caaxaan : kaf, fo. bàyyil caaxaan te jàng bu baax, ci la sa ëllëg nekk.

caax b- : yére jiital bu ndaw. foo jënde sa caax bu weex bi ? / mbaal m-. caax bi dafa bënn mootax jën yu bare génnaat daw.

caaxoñu : takk karawaat, karawaatu. imaam bi tey dafa caaxoñu.

caay-caay g- : mën a tooñ g-. noppi na wànte am na caay-caay de.

caaya j- : mag ñee ëpp lu ñu koy sol. caaya tubeyu mag la.

cabax 1 : (ne cabax). yentem, dagaj. baat bi lu jékki-jékki rekk dugg fenn lay tekki. jinax ji ne na cabax ci biir pax mi.

cabax 2 : dugal baaraam ci bëtu nit ba mënatul gis. saay-saay bi dafa ko cabax ba pare jël li nekkoon ci poosam bi.

cabb b- : cagg b-. ay meññent yu bare yu nekk ci benn car. cabbu tàndarma. cabb màngo bi léegi lañu ko dagg.

cadd : (ne cadd). am yaram wu fasu. coono bu bare mootax sa yaram wi ne cadd.

cafaay l- : ñeex muy ànd ak cere wala laax. dolli ñu cafaay. dinañuy wax tamit cefaay l-.

cafka l- : li ñam di saf. cafka cere ji dafa soppeeku. dinañuy wax tamit cafko l-.

cafko l- : dinañuy wax tamit cafka l-. (seetal cafka)

caga b- : jigeen ju jëkkëram gaañu wala mu tàggoo ak jëkkëram. néew na lu wolof yi di jëfandikoo baat bi ci tekki bii. ndaw soosu ab caga la, daaw la tàggoo ak borom-këram. / jigeen juy jaay boppam. jigeen ju xam boppam du dem mukk di nekk ab caga.

cagg b- : dinañuy wax tamit cabb b-. (seetal cabb)

cajj b- : buum g-. jëlal cajj bi nga yeew ci béy wi.

cakaràkk b- : dég g-. cakaràkk a ko jam.

caku b- : coy l-. caku bi wolof yu leer nàññ lay làkk. dinañuy wax tamit saku b- wala seku b-. (seetal seku)

calala g- : dinañuy wax tamit càllala g-. (seetal càllala)

calgeen b- : saxu geenu nag wala xar wala béy. lii calgeenu nag la.

call b- : tar b-, dakkase b-. call mooy jali gerte yu ndaw yu ñuy def bu ñuy deqi gerte. jal yooyu lañuy dajale bu wowee def ko ay naaf. dinañuy wax tamit call-call b-.

callweer l- : ngelaw lu gaaw luy jaar jàll. callweer laa ngay dem. dinañuy wax tamit njallweer l-.

cal : dawinu fas. fas wi bu mu jaab, na cal rekk.

cambar 1 : meññ. ren gerte yi cambar nañu lool.

cambar 2 : lang. daggal doomi màngo yiy cambar.

cambar 3 : ceddowu. boo ko cambaree bu baax, dinga xam lu ko teree jàng.

cambar-cambar b- : ku nekk di def lu la neex. kër gi kenn du ne déet mootax cambar-cambar bi bare fi.

cammbay : dinañuy wax tamit cam. (seetal cam)

cam : lu ñuy wax bu ñu gisee lu ñu yéem, lu salte wala bu ñu yégee lu xasaw. cam ! génneel sa dàll yi, dañoo taq ay kabine. dinañuy wax tamit cammbay, wala cim wala sim.

cangaay l- : baatu cangaay l- mu ngi jóge ci baatu sang. (seetal sang)

cangat l- : baatu cangat l- mu ngi jóge ci baatu sang. (seetal sang)

cang l- : ndigg l-. sa tubey ji dafa la ëpp ndax sa cang li dafa sew. dinañuy wax tamit cank l-.

cang m- : ñetteelu jamono juy am fukki fan ak ñett ci nawet. ci jamonoy cang mi lañu nekk.

cank l- : ndigg l-. dinañuy wax tamit cang l-. (seetal cang)

can : laaj xaalis kiy takksi sa doom. can nañu ko xaalis bu bare.

can l- : warugar w-. can mënul a ñàkk ci ab sëy, fàww kiy takk jabar joxe ko.

cant g- : ngërëm l-. cant gi dafa ma war ndax li nga ma defal dafa rëy.

ca : daje nañu ca marse ba. / ci kër gi laa ko ko waxe. dinañuy wax tamit ci.

caŋ : ngiro. ñàkk a mën a génn fi nga nekk. oto bi dafa caŋ ci beeñ bi.

cappe : tuuti. sa doom ji dafa cappe, xanaa dafa feebaroon ?

capp : dugal catu dara ci ndox génnewaat ko. capp na loxoom bu tilim bi ci meew mi.

caq b- : ceenu per. sa caq bi rafet na, foo ko jënde ?

carax : (ne carax). baat buy tekki lu jékki-jékki rekk dugg fenn. jinax ji ne na carax ci biir pax mi.

carax b- : dàll w-. tànnkatu dàll ay carax lay mujje. (léebu).

car b- : bànqaas bu ndaw. daggal car yi gën a suufe.

cas : (ne cas). baatu cas dafay tekki jékki-jékki rekk jël dara ci lu gaaw. sàcc bi dafa ne cas saagu waa ji rekk, daw dem yoonam.

cat l- 1 : mujjantal b-, yemukaay g-. nangul bant bi xale bi di foye bala mu koy gaañ, cat li dafa ñaw torob.

cat l- 2 : làmmiñ w-. lu bon lu wax di def. xale bii cat a ko dal wànte amoon na deppaar bu baax ci liggeeyam bi.

cat-bëtu : geen-bëtu, xeelu, rogu. lutax nga may cat-bëtu ?

cawarte g- : tàggat-yaram dafay yokk cawarte. safaan wi mooy tayal g-, wala yaafus b-.

cawdi b- : téere bu ñu ëw ak der def ci buum di ko takk. sama cawdi bi dafa réer. dinañuy wax tamit cawri b-.

caw : duma, dóor, bàcc. boo ko defaatee dinaa la caw.

cawri b- : dinañuy wax tamit cawdi b-. (seetal cawdi)

caxabal : lonk sa tànk ci tànku ki ngay bëreel ngir daaneel ko. dafa ko bëggoon a caxabal.

cax : wax wax ju làqu. dafa la ko cax mootax xamuloo li mu wax.

cay : wis. cay na ndox ci sunguf si bala mu koy mooñ.