dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

cónc b- : dafa taab ci cónc bi

cóncu b- : dinañuy wax tamit cónc b-. (seetal cónc)

cóngaari : taxaw ag benn tànk. benn tànk bi dafay metti mootax mu cóngaari.

cóolal g- : dinañuy wax tamit cóola g-. (seetal cóola)

cóola g- : dafa ubbi cin li rekk, cóola gi sànni. dinañuy wax tamit cóolal g-, cóolool g-, cuuluul g- wala cuulul g-.

cóoli b- : cóoli bi naaw na. dinañuy wax tamit céeli b-.

cóolool g- : dinañuy wax tamit cóola g-. (seetal cóola)

cóorkijam : cóorkijam baat la buy tekki waxoon naa ko.

cóos : soox soox bu yem. dafay cóos tànk bi rekk.