dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

cëgg m- : buumu guy b-. cëgg lañuy takkee suñu dugub ji.

cëkk : cëŋŋ, gàtt. tubeyu waa ji bi dafa cëkk. safaan wi mooy jot.

cëlmaay l- : dinañuy wax tamit kanam. (seetal kanam)

cëŋŋ : (ne cëŋŋ). jékki jékki rekk taxaw. mbaam mi dafa daw ba mu yàgg mu ne cëŋŋ.

cëpp : (ne cëpp). wax juy toppandoo coow liy am bu nit tëbee, dal fenn. paaraa bi ne na cëpp ci bayaal bi.

cëpp g- : nding m-. béreb bu ñuy dajale gerte. cëpp gi fees na dell ak gerte.

cëq m- : anam bi xobi garab di saxe. ndoxum taw mee rafetal cëqu garab gi.

cër b- : dinañuy wax tamit cér. (seetal cér)

cërt l- : fi nit ki fàqeekoo. sérif bi ci cërtu yonnent bi la bokk.

cëslaay g- : ndëgërlaay l-. liy aar dara ba du yàqu. xale dafa war a am cëslaay.