dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

céebi b- : xeetu jaan. ab céebi la rëbbkat yi rey ca àll ba.

céebo m- : benn bu nekk ci diiru fukki fan ak ñett yi am ci jamonoy nawet. ci céebo mu mujj mi lañu nekk léegi. / taw bu njëkk bi ñuy jiwe. céebo mi du fekk benn beykat àll.

céeli b- : liccin b-. céeli bi fii la naawee léegi. dinañuy wax tamit cóoli b-.

céet g- : takk g-. xew li jigeen war a sëyi kër jëkkëram mooy céet. dinañuy wax tamit céyt g-.

cégg : defar benn cabb wékk ko. sama maam moo doon cégg dugub ji.

céq l- : kawar g-. kawar gi nekk ci kow baatu fas. watalal sa fas wi céqam mi. dinañuy wax tamit séq m-.

cér b- : wàll w-. def na ko ñetti cér. / ag wàll ci yaramu doomu aadama. loxo benn la ci céri doom aadama. / awra b-. danga war a nëbb say céram. / gëdd b-. xale dafa war a may mag cér. dinañuy wax tamit cër b-.

céy : wax la juy tekki yërmaande wala jaaxle. céy li ci dëkk bi !

céyt g- : dinañuy wax tamit céet g-. (seetal céet)