dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

càcc g- : jëfu sàcc. càcc gi biig ci guddi la woon.

càggan : ndax. du càggan ne dafa amul xaalis, dafa ko bëggul a jënd rekk.

càggan g- : baatu càggan g- mu ngi jóge ci baatu sàggan. (seetal sàggan)

càkkaar b- : mbaaru néegu ñax m-. dafa wuti ñax ngir xëdd càkkaaram bi.

càkkeef g- : dinañuy wax tamit càkkéef g-. (seetal càkkéef)

càkkéef g- : doom aadama yi dañoo war a sàmm càkkéef gi, loolu ci la seen njëriñ nekk. dinañuy wax tamit càkkeef g-.

càllala g- : ceen g-. lu mel ni ceen gu dijj gu ñu doon yeewe jaam ñi ca Gore. càllala gi caaxaan daggu ko. dinañuy wax tamit calala g-.

càllal b- : ñebbe bu ñu baxal te xolliwuñu ko. waalo-waalo yi xam nañu càllal bu baax.

càmbar : tànn, segg. càmbar ko bu baax, génnee lépp lu ci bon.

càmmeñ l- : mag ju góor j- wala rakk ju góor j-. Abdu sama càmmeñ la. dinañuy wax tamit càmmiñ l-.

càmmiñ l- : dinañuy wax tamit càmmeñ l-. (seetal càmmeñ)

càmm g- : jur g-. càmm gi dafa xiif ndax bekkoor bi.

càmmoñ b- : marse baa ngi ci sa càmmoñ. safaan wi mooy ndeyjoor.

càmpóor b- : dinañuy wax tamit caas g-. (seetal caas)

càngaay l- : baatu càngaay l- mu ngi jóge ci baatu sàng. (seetal sàng)

càng g- : gerees g-, nekk g-. gerees giy muur mbàq. nag wi bare na càng.

càppaacóoli b- : bàjjo b-. nit ku amul dendandoo. waa ji amul morom, càppaacóoli la. / xeetu picc mu mën a woy muy faral di ànd moom rekk. càppaacóoli bi dal na ci banqaasu garab gi.

càqaar : am ab taab ci saxu lupp. tey du mën a liggeeyi ndax dafa càqaar.

càq : wékk dugub, denc ko diiru at. dugub ji ma càqoon laay def jiwu.

càq g- : géppen b-. bant bu gudd bu am ay càq bu ñu samp ci bunt tool ngir bañ jur gi dugg ci mooy càq.