dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

bu yaboo : bu yaboo nga mer wànte dinañu la wax dëgg. dinañuy wax tamit bu yeboo.

bu 1 : bu ma demee dinaa ko ko wax.

bu 2 : bu mu génn kër gi, dafa guddi.

bu-tuut b- : xaalisu xànjar. bu-tuut bi ñaar-fukk la. dinañuy wax tamit buttu b-.

buccatiku : am yar bu bon, reew, yàqu. xale bi dafa buccatiku wànte moo ciy ëppale. safaan wi mooy yaru.

bucci : dinañuy wax tamit bocci. (seetal bocci)

buddi : sempi. ngelaw li buddi na garab gi. safaan wi mooy ji wala jëmbët.

bufta b- : xeetu jumtuwaayu misik la. borom bufta bi li muy def neex na.

bugal : lottal, sonal, mettital. yaa ngi koy bugal de, lu mu la def ? dinañuy wax tamit mbugal. safaan wi mooy jàmmal, teral wala yaatal.

bugg : xiif. ci bekkoor lañu nekk, dañoo bugg. safaan wi mooy suur wala regg.

bukki b- : bukki bi fàdd na xar mi. dinañuy wax tamit bukki-njuur-sàmba b-.

buleen : buleen ko jël, moomuleen ko.

bulet : defar ay bulet. dafay bulet di jaay.

bulli : génnee bopp awra góor. bàyyil sa awra bi ngay bulli.

bul : bul tóx yàmbaa mukk, dafa lay dofloo. bul naan sàngara mukk, dafay yàq sa xol.

bulo 1 : def bulo ci ay yére. ndax bulo nga sama yére yi ?

bulo 2 : baxa. garaa mbubb bu bulo la soloon ca ngénte la.

bulo b- : peroŋ bu nekk ci bunt kër gu mag. lalal ko basaŋ bi ca bulo ba.

bumax : dinañuy wax tamit bëmëx. (seetal bëmëx)

bummi b- : doomu buur ca Kajoor ak Saalum. xanaa yow ab bummi nga ?

bunduxatal : noot, fitnaal. bul ko bunduxatal ci kër gi, doxandéem la fi. safaan wi mooy yaatal wala jàmmal.

bun b- : taat w-. bun wax ju ñaaw la.

bunt b- : fu ñuy jaar ngir dugg wala génn. tijjil bunt bi, dafa tàng.

buqat b- : dinañuy wax tamit bëqët b-. (seetal bëqët)

buqi : xulli ay gët. nag wi la ñemewul mootax mu buqi gëtam yi. safaan wi mooy gëmm.

buruj b- : biddeew b-. sëriñ bi nee na leen seen buruj yi ànduñu.

buruxal : dinañuy wax tamit barxal. (seetal barxal)

busulu : xeetu daaneel ci bëre. busulu mooy sànni am mbër ngir daane ko sa kanam.

buteel b- : jaay ma benn buteelu buwaasoŋ.

butiit b- : raxasal butiit yi mu set de. butiiti xar wala yu nag. dinañuy wax tamit butit b-.

butit b- : dinañuy wax tamit butiit b-. (seetal butiit)

butitu jurukaay b- : feebaram bi ci butitu jurukaay bi la nekk. dinañuy wax tamit butitu njurukaay b-.

butoŋ b- : butoŋi simis wala yu pantaloŋ. gawal sa butoŋ yi.

butti : bënn biir. buuse bi butti na nag wi.

buttu b- : dinañuy wax tamit bu-tuut b-. (seetal bu-tuut)

buub : dajale. ndaw si buub na mbalit mi yépp. safaan wi mooy tasaare.

buuj b- : kokiyaas b-. wàgg yee génnee buuj yépp.

buum g- : goj b-. tiyeel buum gi bu baax, nag wi dafa soxor.

buun : namm a lekk dara lool. lan nga buun tey ma toggal la ko ?

buur 1 : ñàkk a sampu bu baax. bantu mbaar mi dafa buur.

buur 2 : dem ak mer. kenn defu ko dara, moom moo buur dem.

buur 3 : matal ay gëñ. xale bi buur na léegi.

buurba b- : daraja ju ñu doon jox njiit li ca Jolof. loolu ca jamonooy buurba jolof la woon.

buur b- : daraja ju ñu doon jox njiit li ca Siin ak ca Saalum. maamam buur Saalum la woon.

buuse : fatt, sakk. kanaal bi dafa buuse.

buuse b- : jaaykatu yàpp b-. buuse bi reyul nag tey.

buusu : tufli lu bare. góor gi dafay mëq póon mootax buusu na fi mu togoon yépp.

buux : puus. bul ko buux, dafay daanu. dinañuy wax tamit bóox. safaan wi mooy xëcc.

buwaasoŋ b- : duma naan buwaasoŋ boobu.

buxaaba b- : jibarkat b-, jabraankat b-. sëriñ buy faj ak sunguf, ak reen wala ay téere. buxaaba bi loo wax mu ne mën na koo faj. (seetal jibarkat)

buy b- : li ñuy lekk ci buy. buy bi ngallax laa ci bëgg a defar.