dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

bobaru : dinañuy wax tamit gañu. (seetal gañu)

bocci : génnee ngànnaay ci mbaram. bocci na paakaam bi wànte du defe dara. dinañuy wax tamit bucci.

boddi : beddi, fegg, ber. génnee nit ci say mbir. jikko ju bon mootax ñépp boddi ko.

bojj 1 : jam. paaka la ko bojj ci ginnaaw.

bojj 2 : wol, dëbb. dëbb ay gubi dugub wala basi ngir génnee pepp mi. ndaw si dafay bojj dugub.

bokk : bokk naa ci mbootaay googu. / ñoo bokk baay.

bolde b- : yet w-. kenn du dugg ak bolde ci biir estaat bi.

bol b- : sunguf s-. bolu meew bi seer na lool jamono jii.

bomax : dinañuy wax tamit bëmëx. (seetal bëmëx)

bomb : jonj. nanga bomb xale bi ndànk, njàmpe li dafa ñaw.

bon 1 : soxor. kooku waa ju bon la, du maye, du saraxe. jëf ju bon jii du sa wareef. safaan wi mooy baax, yéwen wala tabe.

bon 2 : nga ne gisuloo jaan ji, bon lutax nga daw ? dinañuy wax tamit kon wala boog.

bonde : tëb ay yoon. bal baa ngi bonde.

bonofiis b- : amul benn bonofiis ci njaayam mi ndax li muy maye moo bare. safaan wi mooy perta b-.

boŋ-boŋ b- : ngato b-. gan gi andiwaaleel na xale yi ay boŋ-boŋ.

boobale : dëkk boobale mës naa fa dem.

booba : oto booba lay wax.

boobee : téere boobee jàng na ko.

boob : dagg ñax mu wow. ndax mën nga boob ?

boobu : tool -b boobu sa tool maam la woon.

boog : dinañuy wax tamit bon. (seetal bon)

boole : boolante, jaxase. boole na saam yépp. safaan wi mooy xaajale wala ber.

bool b- : ndab l-. yakkal añ bi ci bool bu ndaw bi.

boon b- : yàmbaa j-. bàyyil boon bi ngay tóx bala mu lay sànk.

boor b- : pegg b-, wet g-. nekkewul ci boor boobu.

bootal-mbaar b- : ki yore xarfafuufa ay njulli, li leen di aar ci lépp lu bon. bootal-mbaar dafa war a am xam-xam.

boot : yenu ci ginnaaw. yow doo boot sa doom ji mukk. safaan wi mooy botti.

boow 1 : jéem a dagg ak ñawtanu paaka. boow na paaka bi ay yoon wànte buum gi daggul.

boow 2 : bomb, jonj. paan bi dafa tilim lool, nanga ko boow bu baax.

booy 1 : dakk, dog. def na ko ñaar-fukki at te mësul a booy.

booy 2 : am ay gaañu-gaañu fenn ci der. dafa booy ci poqtaan.

booy 3 : bare ñax ba mu ëpp. dafa bañ tàng mootax toolam booy.

booy b- 4 : mbindaan bu góor. sa booy bi xëysiwul tey ? dinañuy wax tamit bóoy b-.

bopp-sa-bopp b- : kenn ku nekk sa bopp ngay lijjanti, kenn faalewul kenn. bopp-sa-bopp bi tax na kenn dimbaleetul kenn.

bopp b- : ci bopp bi lañu ko dóor yet. / ku jiitu wala lu jiitu ci am mbir. moo nekk ci boppu kurel googu.

boqaale b- : ndaw sooy andal te takkuloo ko wala góor gooy andal te du sa jëkkër. jabaram xam na ne dafa am boqaale feneen.

boq : yore dara ci poqtaan. boq na illeeram dem ca tool ya.

bori : yore bakkan buy nàcc. dafa tàmm di bori.

bor b- : loo ameel nit wala lu la nit ameel. fey na bor yi wànte xaalisam bi jeex na.

borode : dinañuy wax tamit boroode. (seetal boroode)

borom-bakkan b- : kuy dund wala luy dund. defal fas wi ndànk, borom-bakkan la.

borom-bopp b- : gëñ yuy metti, wala nopp yuy metti wala bépp mettit bu taq ci bopp. dafa borom-bopp mootax lexam yi néwwi.

borom-dëkk b- : ki dëkk bi nekk ci ay yoxoom. borom-dëkk mooy ndawal buur ci dëkk.

borom-i-may b- : ku yaa-bopp, ku am xam-xam bu làqu. waa ji borom-i-may la, demal gis ko, mu ñaanal la.

borom-kër g- : njiit li ci kër gi. su fi borom-kër gi nekkoon, doo def lii. / jëkkër j-. soxna si am na borom-kër, bàyyi ko mu dem yoonam.

borom b- : ki moom. borom kër gi Tugël la nekk. dinañuy wax tamit boroom b-. / Yàlla. Borom bi du juum mukk.

boroode : tajoor bi dinay boroode. dinañuy wax tamit borode.

boroom b- : dinañuy wax tamit borom b-. (seetal borom)

boroos : bul boroos jiin bi, dafay gaaw a furi. dinañuy wax tamit boros.

boros : dinañuy wax tamit boroos. (seetal boroos)

bos : jox ma sama bos, jox ko bosam.

boxom : motoxal. boxom na gerte caaf gi yépp.

boyal : bàyyi jur gi ñu dem wuti lu ñu lekk te kenn du leen topp. dafa boyal nagam yi.

boyet b- : ñaata ngay jaaye boyetu suukar ?

boy : tàkk bu baax. bàyyil upp bi, furno bi boy na léegi. safaan wi mooy fey.

boyy : (ne boyy). leer nàññ ak taar. kër gaa gi ne boyy.