dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

becci : sànni li nga yenuwoon ci suuf. dafa becci saaku ceeb bi, mu bënn. dinañuy wax tamit bécci wala bëcci.

beddi : ber, fegg. teg ci wet gi. dafa yor feebar buy wàlle, ñu beddi ko. safaan wi mooy fat.

beeco b- : sér b-, pendal m-. sér bu ndaw bu jigeen di jiital. dinay jaay ay beeco tamit.

beeke b- : sukkoot b-. ay beeke lay doxe fan yii.

been : dëpp. danga been sa tubey ji.

bee : bale. du caabi bii, jox ma bee ma set.

beeñ b- : suuf su weex su sew, salleñ s-, gannuus g-. borom sareet yi géej lañuy tibbe beeñ.

beer b- : sàngara s-. jullit warul a naan beer.

bees 1 : oto bu bees la jënd. dinañuy wax tamit bees wala ees. safaan wi mooy màgget.

bees 2 : fóof. bees na dugub ji ba mu set.

beew : di def lu jaaduwul ci sa alal. alal ji nga am ba tax nga beew suñu borom dafa la ko dénk rekk. dinañuy wax tamit bew.

bejjente : dinañuy wax tamit bijjanti. (seetal bijjanti)

bekk b- : xeeru suukar. suukar bekk bi dafa seer léegi.

bekkoor b- : xiif g-. su tawul rekk, bekkoor am.

belefete b- : xeetu tubey ju ndaw ju jigeen ñi di sol. ndaw si jënd na ay belefete.

bembaxli : sotti meew ci fonde. bembaxlil ma soow mi fii.

beneen b- : dafa dàmm ci beneen tànk bi.

benkeñenke b- : jafe-jafe b-. yow danga bare ay benkeñenke.

benn b- : booy waññ, ci benn ngay dale. / ñaar yi duñu benn. / móodu-móodu yaa ngi ñibbisi benn-benn.

be : dem naa be yegg seen dëkk wànte gisu ma ko. dinañuy wax tamit ba.

beñe b- : beñe bi dafa bare diwlin.

beñwaar b- : defukaayu ndox. abal ma beñwaar, damay fóot.

beref b- : xaal bu ndaw. toolu beref bi meññ na.

berkelle b- : dinañuy wax tamit barkelle b-. (seetal barkelle)

berndeel : teral gan bu baax. sëriñ bi berndeel na ay ganam.

ber : beddi, boddi, fegg. lutax ngeen ber waa ji ?

betteex b- : betteex bu tàng ku mu laal nga yàqu. dinañuy wax tamit bettax b-.

bett : bett nañu ko muy tux yàmbaa.

bew : dinañuy wax tamit beew. (seetal beew)

bey : dinañuy wax tamit bay. (seetal bay)