dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

bóbbali : looy bóbbali nii rekk, xanaa nelawuloo biig ? dinañuy wax tamit óbbali wala bébbali.

bóli g- : purux g-, put g-. mënul wax bu baax ndax dañu ko tiye ci bóli.

bóngo b- : xew la tëggkatu bóngo bi di wër.

bóof : tëdd ci kow dara ba muur ko. ginaar gi bóof na ci nen yi.

bóoli b- : ndab lu rëy wala bool bu rëy. luye nañu ay bóoli ngir seen xew li.

bóom : faat, rey. mbooloo ma bóom nañu sàcc ba.

bóor b- : mburook bóor a ma gënal mburook sokolaa.

bóox : jañax. defal ndànk, yaa ngi may bóox. dinañuy wax tamit buux.

bóoy b- : dinañuy wax tamit booy -4 b-. (seetal booy)

bóqun-ma : mbas. bóqun-ma góor gu nanguwul a liggeey. dinañuy wax tamit subóqun.

bóqun-ma : dinañuy wax tamit suboqun. (seetal suboqun)

bów : dinañuy wax tamit mbów. (seetal mbów)