dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

bëccëg b- : ci bëccëg bi la fa war a dem. safaan wi mooy guddi g-.

bëcci : dinañuy wax tamit becci. (seetal becci)

bëer b- 1 : bëer xeetu jën la.

bëer b- 2 : dax b-. mburu ak bëer lay ndékkee.

bëgëj b- : ranq b-, bisaab b-. xobi bisaab lañuy defare bëgëj.

bëgg-àddina : bëgg dund gu neex. xale bi dafa teel a bëgg-àddina.

bëgg-lekk : foqale. dafa bëgg-lekk, du suur mukk.

bëgg : soxla, sopp, nob. bëgg naa ceebu-jën. takk na ndaw si mu bëggoon. safaan wi mooy bañ.

bëj-gànnaar b- : ngopp l-, bopp b-. seen réew ci bëj-gànnaaru réew mi la nekk.

bëj-géwel b- : kilifa tëggkat yépp. bëj-géwel bi lañuy xaar.

bëj-saalum b- : tànk b-. ngelaw li ci bëj-saalumu réew mi lay jóge.

bëkk-démb : dinañuy wax tamit bërki-démb. (seetal bërki-démb)

bëkk-néeg b- : dag b-. ku jege ag kilifa di dox digganteem ak nit ñi. waxal bëkk-néeg bi mu dimbale la nga mën a gis sëriñ bi.

bëkkëta b- : baaxu lébu la goo xam ne bu xale bi juddoo lañu koy def ngir aar ko ci lépp lu ko mën a dal. ndax bëkkëta bi pare na ?

bël b- 1 : sunguf s-. ku doon defar bël bii ?

bël b- 2 : fi ndoxum déeg mi daje ak ndoxum géej mi. dem naa bay séen bël ba wànte yegguma fa.

bëliis m- : ibliis m-. bëliis saytaane la.

bëmb : géleem mooy bëmb.

bëmëx : jañ. puus nit wala dara bu baax. defal ndànk, yaa ngi may bëmëx. dinañuy wax tamit bumax wala bomax

bën-bën b- : bëtt-bëtt b-. ceeb baa ngi turoo ci bën-bënu saaku bi.

bënn : bëtt. jinax yi bënn nañu saaku bi.

bëñ b- : gëñ y-. bëñam bi dafay metti ci suba ba léegi.

bëpp : rës. baŋ bi bëpp na.

bëqët b- : ragal b-. xutt b-. yow bëqët nga rekk, góor du ragal. dinañuy wax tamit buqat b- wala baqat b-.

bër-set : bu guddi deme ba jeex. jogal jàngi, bër-set na bu yàgg. dinañuy wax tamit bët-set.

bëre : doomam ji dafay bëre.

bëret : (ne bëret). wax juy tekki jékki jékki rekk jóg. dafa ne bëret jóg bi mu gisee jaan ji ci ron baŋam bi. dinañuy wax tamit bërët, bérëx wala bërëx.

bërëb b- : dinañuy wax tamit béreb b-. (seetal béreb)

bërëg-démb : dinañuy wax tamit bërki-démb. (seetal bërki-démb)

bërëm : lakk, saaf. jën yu ñu bërëm la gën a bëgg.

bërëŋ : puus am mbir ci suuf ngir yóbbu ko. xale yaa ngi bërëŋ barigo bi. dinañuy wax tamit béraŋ.

bërët : dinañuy wax tamit bëret. (seetal bëret)

bërëx : dinañuy wax tamit bëret. (seetal bëret)

bërgal : wacc. nit ñi dañu ko bërgal ndax wegul kenn.

bëri : dinañuy wax tamit bare. (seetal bare)

bëri : dinañuy wax tamit bare. (seetal bare)

bërkë-démb : dinañuy wax tamit bërki-démb. (seetal bërki-démb)

bërki-démb : ñaari fan lu jiitu tey. bërki-démb la ñëw. dinañuy wax tamit bëkk-démb, bërkë-démb wala bërëg-démb.

bërlóor b- : njulli buy soog a génn ci lël. bërlóor bi démb la génn.

bër : dakkal njàng mi ngir dallu. xale yi ayubés bii di ñëw lañuy bër.

bës-pénc b- : bës bi Borom bi di àtte jëfi mbindeef yi. keroog bës-pénc, kenn ku nekk sa bopp ngay tal.

bës : naj, seere. bës na taab bi ba dëtt ji yépp génn.

bës b- : bës du tuuti borom lay tollool. dinañuy wax tamit bés b- wala bis b-.

bët-bëtóor b- : dinañuy wax tamit bat-batóor b-. (seetal bat-batóor)

bët-set : dinañuy wax tamit bër-set. (seetal bër-set)

bëtal : aj. dafa bëtal céet gi ba beneen jëmmi jamono.

bët b- : cëru doomu aadama bi muy xoole. lu nekk ci sa bët bi ? li ko tàmbalee ñaar jëm kow, gët y- lañuy wax. ñaari gëtam yi yépp ay metti.

bëtt : bënn. saaku bi dafa bëtt, dugub jaa ngi tuuru.

bëtu-tànk b- : ci bëtu-tànk bi la ko ustaas bi dóor yet. dinañuy wax tamit tostan b- wala tëstan b-.

bëxërñëg : (ne bëxërñëg). bëret. kaña gi dafa ne bëxërñëg, xale yi dóor ko ay yet ba mu dee. dinañuy wax tamit bëxërñët.

bëxërñët : dinañuy wax tamit bëxërñëg. (seetal bëxërñëg)

bëy : ame loxo bu am taab. dafa bëy mootax fan yii yépp liggeeysiwul.