dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

bébbali : dafa sonn mootax muy bébbali rekk. dinañuy wax tamit óbbali.

bécci : dinañuy wax tamit becci. (seetal becci)

béej : raayante. mën ngeen a béej wànte bu leen ko defe ci mbedd mi.

béemeer : takk gémmeñu fas. béemeeral fas wi rekk ñu dem, dama yàkkamti. dinañuy wax tamit biimir.

béeru : saw, tuur-ndox. xale bi béeru na lal bi ba mu tooy xepp.

béey : fàcc, xottiku. loxoom bi dafa béey.

bég : koontaan. bég naa lool ci ngan gi. safaan wi mooy mer.

béjjaaw : sax kawar gu weex ndax ay at yu bare. def loolu waru la ndax béjjaaw nga léegi. dinañuy wax tamit bijjaaw.

béjjen b- : béjjenu nag wi dafa damm.

bélli : yaatu, leer (kanam). kanamam gi bélli na tey.

béngal j- : dinañuy wax tamit béngël. (seetal béngël)

béngël j- : dàqaar ju ñorul. foo jëlee béngël ji ?

béntenki g- : dinañuy wax tamit bénteñe g-. (seetal bénteñe)

bénteñe g- : xeetu garab. dinañuy wax tamit béntenki g-. am na bénteñe gu rëy gu nekk seen digg dëkk.

bépp : danga war a séq jàmm ak bépp dëkkandoo.

béral : dinañuy wax tamit biral. (seetal biral)

béraŋ : dinañuy wax tamit bërëŋ. (seetal bërëŋ)

béreb b- : palaas b-. béreb bi féex na lool. dinañuy wax tamit bërëb b- wala barab b-.

béreej : dog-ub-tënk, aay-yoon. ku béreej dafay faral di taxawaalu ci li mu war a def, maanaam du ko def ci lu gaaw. xale bu béreej lu ko dal baax na.

bérëx : dinañuy wax tamit bëret. (seetal bëret)

bés-pénc : lépp dina leer keroog bés-pénc. dinañuy wax tamit bis-pénc.

bés b- : dinañuy wax tamit bis b-. (seetal bis)

béy w- : béy dafa sob, xar dafa teey. dinañuy wax tamit bëy w-.