dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

bàcc 1 : gupp, xayu. fóot fóot mu yem. damay bàcc yére rekk, léegi ma pare. / génne doomi jàngoro ju nekk ci ay gët. bàcclu naa sama gët yi ba pare, léegi am naa jàmm.

bàcc 2 : bàcc gerte mooy tàqale gerte gi ak ngooñ mi. tey lañu ko waral bàccal gerteem gi.

bàjjan j- : bàjjan mooy mag ju jigeen wala rakku baay ju jigeen. dinañuy wax tamit bàjjen j-.

bàjjen j- : dinañuy wax tamit bàjjan. (seetal bàjjan)

bàjji b- : puub yu dem ba soppeeku suuf. moytul loolu, bàjji la. dinañuy wax tamit baji b-.

bàjjo b- : càppaacóoli b-. lu amul benn dendadoo lañuy tudde bàjjo.

bàkkaar : moy. yaa ngi bàkkaar ndax loolu diine tere na ko.

bàkkis g- : xeetu garab. xob yii, xobi bàkkis lañu. dinañuy wax tamit bakis g-.

bàkk : tagg. géwel bi bàkk na mbër mi.

bàkk : woy jalloorey nit wala yu aw askan. tey géwelam bi bàkk na ko bu baax.

bàmbaado b- : xalamkat b-. seen bàmbaado bi ñëwoon na ci seen xew li.

bàmbara b- : turu aw askan wala turu ku bokk ci askan wi. jabaram bàmbara la.

bàmmeel b- : fu ñu suul nit ku faatu. bàmmeel bii la sa maam tëdd.

bànd b- 1 : xeetu jën. bànd bi dafa mànke fan yii.

bànd b- 2 : xeetu jaan. rëbbkat yi rey nañu bànd bu mag.

bànga b- : naajo b-. nijaayam dafay bey bànga.

bànjóoli b- : baa b-. foo jënde bànjóoli bi ?

bànk : ñàkk xaalis. duma la mën a fey tey ndax dama bànk. safaan wi mooy am xaalis.

bànneex b- : mbégte m-. sëy bu amul bànneex du sëy. safaan wi mooy naqar w-.

bànni : askanu, doomi. Yàlla dina àtte jëfi bànni aadama yépp.

bànqaas b- : car bu mag. taw bee fàq bànqaas bi.

bànqañoos b- : dinañuy wax tamit banqanaase b-. (seetal banqanaase)

bàq b- : suuf su taw bi tooyal xepp. bàq bi tooy na, beykat yaa ngi ji seen gerte yi.

bàq g- : taataa b-. fu ndox mi des ginnaaw bu mu tawee ba pare. moytul a daanu ci bàq gi.

bàttale : dinañuy wax tamit batale. (seetal batale)

bàttali : dinañuy wax tamit batale. (seetal batale)

bàttu b- : kuddu luusu yaj. jëndaaleel ma benn bàttu. dinañuy wax bàttu wala mbàttu.

bàyyi : bàyyil tóx, tóx baaxul. dinañuy wax tamit ba.