dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

aye : war a def sa wall. aawo bee aye tey.

ayib : të, yàqu. xale warul a ayib, dafa war a am-yar. safaan wi mooy yaru.

aylayéwen : lu mu bon bon, lu mu néew néew, gën gaa bare. dàll yi boo ko jaayee, aylayéwen dinga ci am ab junni.

ay : xew, am. lu ay di njàmbat. / ku am mettit dina koy wax. ay ! dég jam na ma.

ayubés b- : semen b-. ayubés juróom-ñaari fan lay am.

ayudiir g- : luy dem di dellusiwaat mooy ayudiir.

aywa : aca. aywa leen ñu dem géej.