dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

aw 1 : wuutu. liggeeyal, boo sonnee ma aw la.

aw 2 : jaar. léegi la fi aw, nee na mu ngi ñëw.

awiril b- : ci weeru awiril wi paase la fi ñëwoon.

awiyoŋ b- : ropplaan b- : ci ñetteelu awiyoŋ bi la war a dugg.

awokaa b- : laykat b-. awokaa bi dée lay na ba àttekat bi ñu jox waa ji dëgg.

awra b- : taat y-. solalal xale bi tubey, awraam baa ngi ci biti.

awu : ñaari nit rekk ñoo koy awu ci woyam yi. / riir. seen coow laa ngi awu ci biir néeg bi.