dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

asaaloo : sàggane. mbër mi dafa asaaloo bëreem bi keroog.

asaka j- : li jullit bi di jël ci alalam at mu jot ngir jox ko néew-di-doole yi mooy asaka.

asamaan s- : Yàllaa sàkk asamaan ak suuf.

asaru : reew, yàqu, xamadi. ndaw si du jigeen ju baax ndax dafa fo ba asaru. safaan wi mooy yaru wala am-teggin.

aseer j- : dinaa fa ñëw aseer ci ngoon. dinañuy wax tamit aset.

aset j- : dinañuy wax tamit aseer. (seetal aseer)

asiire : dëggal. li ma la wax lu asiire la.

asi : dogat, daggat, fejat. ndax asi nga soble bi ba pare ?

asit b- : dinañuy wax tamit ësib. (seetal ësib)

askan w- : geño g-, ay mbokk ci wàllu baay. dañoo bokk askan mootax ñu niroo. / nit ñi aju ci menn réew ñépp. askanu Senegaal dañoo mën a liggeey. / xeet w-. askan yi bare nañu wànte bokkuñu.

asm b- : su ko asm bi daanee, du noyyi bu baax.

as : ŋacc, tanq. as nañu ndox mi yépp balaa muy dugg ci biir kër gi.

asset b- : dinañuy wax tamit palaat. (seetal palaat)

astafirlaa : astafirlaa la jullit di wax suy jéggalu boromam. / nit dina koy wax tamit bu juumee ci kàddoom. dinañuy wax tamit astafurlaa.

astafurlaa : dinañuy wax tamit astafirlaa. (seetal astafirlaa)

astemaak : rawati-na. du tux sax astemaak naan sàngara.

aste : rawati-na. ndegam xale yee xam loolu aste mag ñi. dinañuy wax tamit astemaag.