dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

araab : làkku araab mooy làkku waa Arabi Sawdi.

araam : lépp lu diineey lislaam tere dafa araam. njaalo dafa araam ci lislaam. safaan wi mooy dagan.

araf b- : làkku wolof fan weer ak benn araf la am.

arañefe : ndam demul, ndam dikkul, kàngamloo. ñaari ekib yi dañoo arañefe bërki-démb.

aras b- : àllaaxira. gisaguñu ku jóge aras dellusi fii ci àddina.

araw : mënul a araw cere.

arbiis b- : góom bu nit di jële ci fo wala dox ci biir ndox mu tilim. dinañuy wax tamit ërbiis. xale yi bàyyileen fo ci biir ndox mu tilim mi, dafay joxe arbiis.

arduwaas b- : arduwaas mooy alluwa ci lekkool farañse bi. ci arduwaas bi la ko meetaram di bindal li muy jàng

areen b- : areen dafay tekki béreb bu ñuy tëgge làmb wala géewu làmb.

areen j- : gerte g-. ren beykat yi am nañu areen ju bare.

are b- : gaawal ñëw, maaŋ lay xaar ca are bis ba.

ariko b- : li nga jënde ariko bi dafa seer.

ariyeer : dellu-ginnaaw. sooy ariyeer, nanga xool bu baax bala ngay fiir nit.

armal 1 : armal mooy sol yére aji màkka boo sàngoo, julli ba pare.

armal 2 : tàmbali, door. bi nga may woo telefon, dafa fekk ma armal ba pare, di julli, mootax mënuwoon a wuyu.

armeel y- : sëg y-, kër-gu-mag g-. armeel mooy béreb bi ñuy denc ñi faatu.

arminaat b- : kalaandiriye b-. amaguma arminaat atum ren.

armool b- : kañ nga jënd sa armool bu rafet bii ?

armuwaal b- : ñaari këri armuwaal bi yére lañu def ba fees dell.

ar : (ne ar). am njàng mu rëy. kooku dafa jàng ba ne ar. safaan wi mooy cuune.

arsele : dinañuy wax tamit ërtal. (seetal ërtal)

artist b- : dinañuy wax tamit ndaanaan. (seetal ndaanaan)

artu : dankaafu. dootu ko defati ndax artu naa ko bu baax.