dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

anam b- : defin w-, fasoŋ b-. ni ñu ko defe wala ni mu deme. anam bi minise bi defare lal bi baaxul.

ana : ana foo teg paaka bi ? dinañuy wax tamit ani.

andaar w- : natt bu war a tolloo ak liitar mooy andaar.

andi : dinañuy wax tamit ëndi. (seetal ëndi)

and b- : and mooy mbool si ñuy def dóomu taal di ci taal cuuraay.

aniin : makiyaas. maa aniin ndaw si ba mu rafete nii.

ani : dinañuy wax tamit ana. (seetal ana)

aniwerseer : bés bu dellusi. tey lay def aniwerseeram.

ankañ : -xanaa jàngiwuloo ? -ankañ, damay xaar ba ci kanam. dinañuy wax tamit ankay, axakay wala axakañ.

ankay : dinañuy wax tamit ankañ. (seetal ankañ)

an : buub. an na mbalit mi, dem tuuri ko.

antu : dinañuy wax tamit àntu. (seetal àntu)