dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

am 1 : yor. am na xaalis bu bari wànte du ci maye mukk. safaan wi mooy ñàkk.

am 2 : lu nekk. am na ay béreb yu kenn dul tux.

am 3 : xew. lu am ñu ne moom la.

am 4 : wala. danga xiif am danga sonn.

am-aajo : ku am-aajo mooy ku weg doomu aadama yi, di bari lu mu leen di nuyu, di leen bàyyi xel. safaan wi mooy ñàkk-aajo.

am-alal : barile, bari alal, bari xaalis. dafa am-alal wànte du maye, du saraxe. safaan wi mooy ñàkk.

am-baat : am-kàttan., am-doole. ku am-baat la ci réew mi. (seetal am-doole)

am-bayre : ku am-bayre mooy koo xam ne ñépp dañuy daw wutsi la.

am-bàmmeelu-biir : am-sutura. nit ku baax dafa war a am-bàmmeelu-biir.

am-bët : ku am-bët mooy ku rëy ay gët.

am-bopp : ku am-bopp mooy ku kenn mënul ci moom dara, koo xam ne loo ko fexeel mu moy. dinañuy wax tamit yaa-bopp.

am-di-jàmm b- : képp koo séqal jàmm rekk, sa am-di-jàmm la. dinañuy wax tamit am-ndi-jàmm wala am-ji-jàmm. safaan wi mën doon xuloowaale b- wala noon b-.

am-diine : ku am-diine mooy kuy def ndigali diineem, di bàyyi ay tereem. safaan wi mooy ñàkk-diine.

am-doole : am-kàttan. mbër mu am-doole la daan. safaan wi mooy néew-doole.

am-faayda : ku dul dugg ci lenn lu ñàkk-faayda, am-kalakteer. taxawaalu góor gu am-faayda du ko def. safaan wi mooy ñàkk-faayda.

am-fit : ku ragalul dara. gaynde rab wu am-fit la. safaan wi mooy ragal wala tàppet.

am-gat : diis, rëy. ku am-gat mooy ku bari tiitar. safaan wi mooy woyof.

am-jàmm : neex-deret. ku am-jàmm mooy ku dul fitnaal doomu-aadama yi benn yoon, ku jàmbure. waa ji neex naa dëkkal ndax dafa am-jàmm. safaan wi mooy naqari-deret, bare-saytaane.

am-jëmm : am-yax, ngande. ndaw su am-jëmm la takk. safaan wi mooy sew wala tuuti.

am-ji-jàmm : dinañuy wax tamit am-di-jàmm. (seetal am-di-jàmm)

am-jikko : ku am-jikko mooy kuy faral di dikkale. yow danga am-jikko mootax bëgguma di fo ak yow.

am-jom : am-jom mooy gëm sa bopp, bañal sa bopp lu ñaaw, bañ ku la reetaan. safaan wi mooy ñàkk-jom.

am-jot : ku deful dara mooy am-jot. dangeen a am-jot mootax ngeen nekk foofu di xuloo. safaan wi mooy ñàkk-jot.

am-kalakteer : dinañuy wax tamit am-faayda. (seetal am-faayda)

am-kàttan : am-doole. ku mën a dékku ay coono. góor gi màgget na wànte dafa am-kàttan ba léegi. safaan wi mooy ñàkk-kàttan wala néew-doole.

am-kersa : ku am-kersa dafay bare lu muy rus, du bëgg a def lu ñaaw. safaan wi mooy ñàkk-kersa.

am-kóllëre : ku am-kóllëre mooy ku dul fàtte démb mukk. mu ngi may seetsi ba léegi ndax moom dafa am-kóllëre. safaan wi mooy ñàkk-kóllëre.

am-maanaa : am-solo. sa wax ji dafa am-maanaa ba damay toog déglu la bu baax. safaan wi mooy ñàkk-solo wala ñàkk-njëriñ.

am-muur : am-wërsëg, am-saas, am-sãas. waa ji ku am-muur la. safaan wi mooy ñàkk-wërsëg wala ñàkk-saas wala ñàkk-sãas.

am-ndi-jàmm : dinañuy wax tamit am-ndi-jàmm. (seetal am-di-jàmm)

am-njariñ : ku am-njariñ mooy kuy jariñ nit ñi. dinañuy wax tamit am-njëriñ.

am-njëriñ : dinañuy wax tamit am-njariñ. (seetal am-njariñ)

am-saas : dinañuy wax tamit am-sãas wala am-muur. (seetal am-muur)

am-sãas : dinañuy wax tamit am-saas wala am-muur. (seetal am-muur)

am-solo : am-maanaa. li ngay jàng dafa am-solo lool. safaan wi mooy ñàkk-solo.

am-sutura : jabar ju am-sutura du weer jëkkëram ci mbedd mi mukk. safaan wi mooy ñàkk-sutura.

am-taxawaay : njool. basketeer dafa war a am-taxawaay. safaan wi mooy gàtt.

am-teggin : yaru. ku am-teggin du wax lu ñaaw mukk. safaan wi mooy asaru. (seetal asaru)

am-teraanga : ku am-teraanga dafay mën gan, dafay nangoo séddoo li mu yor ak nit ñi. safaan wi mooy nay wala bon.

am-tur : siiw. Mési futbalkat bu am-tur la ndax, jamono yii, foo dem ci àdduna bi xam nañu ko.

am-wërsëg : am-muur. xale bu yaroo dafay am-wërsëg. safaan wi mooy ñàkk-wërsëg.

am-xam-xam : ku xam lu bare. jàngalekat bu am-xam-xam la woon. / yaa-bopp. am-xam-xam mën na tekki tamit yaa-bopp. safaan wi mooy gàtt-xam-xam.

am-xel-ñaar : nekk di jiixi-jaaxa. amuma benn xel-ñaar ne lii yow yaa ko def.

am-xel : yeewu, muus. dafa am-xel mootax waa ji naxu ko. safaan wi mooy dof, naqari-xel, wala ñàkk-xel.

am-xorom : xoromu. ku am-xorom dafay neex waxtaan. safaan wi mooy ñàkk-xorom wala soof.

am-yaakaar : yaakaar dara. am naa yaakaar ne doo ko fa fekk ndax du toog.

am-yaram : rëy. ndaw si dafa am-yaram ba mënul dox bu baax. safaan wi mooy tuuti wala sew.

am-yar : yaru. xale dafa war a am-yar ba mag mu ko gis bëgg ko. safaan wi mooy reew, xamadi, wala ñàkk-yar.

am-yax : am-jëmm. mbër mi dafa am-yax. safaan wi mooy tuuti.

am-yeel : njool, am-taxawaay. dafa am-yeel rekk wànte at yu néew la am. safaan wi mooy gàtt.

am-yërmande : ku am-yërmande mooy kuy yërëm doom-aadama yi.

amaana : xëyna. amaana ma gis ko suba.

amaana j- : ngor g-. amaana ji mu ma won, duma ko wor mukk.

amaa : mën naa am. xamuma ci dara, boo ko ko waxee, amaa mu jox la, amaa mu bañ.

ambolog b- : fi ñuy def leetar buñ koy yónne ca post ba mooy ambolog. dinañuy wax tamit ambolok b-.

ambolok b- : dinañuy wax tamit ambolog. (seetal ambolog)

amiin : amiin mu ngi tekki « Yàlla na deme noonu ». booy nangu ñaan amiin ngay wax.