dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

alaaji b- : góor gu aji Màkka ba ñëw lañuy woowee alaaji.

alaakulli-alin : ak lu mën a xew, lu mu mën di doon. alaakulli-alin dina fi dëppesi.

alag : sonal, lottal, fitnaal. tooñ bi ngay tooñ mag ñi dina la alag soo ko bàyyiwul. safaan wi mooy teral.

alaku : torox. waa ji sàgganee ay way-juram a ko tax a alaku. ku ñu alag mooy alaku. / dee. alaku na daaw. dinañuy wax tamit alku.

alal j- : am-am b-. ci jaay jën la jële alal ji mu yor yépp.

alamaan : daan bu ñuy teg ci kow nit ku wàccoowul ak sarta yi ñu tëral, di ko doxal.

alamikk : ci lu wóor, ci lu amul benn weerante. alamikk dinaa jàng àngale.

alaterete : ku liggeey ba sa noppalu jot nga bàyyi liggeey bi toog noppalu. dafa alaterete léegi.

alawle : lakkal nit ñi. dinañuy wax tamit aldànke. xale bi dafa alawle. (seetal aldànke)

alburaax m- : alburaax mooy fasu Jibiril.

aldànke : lakkal nit ñi ci ab béreb te kenn du ci mën dara, darale, ubale. coowal misig bi aldànke na béreb bi yépp.

alde : ku alde mooy ku bëgg jigeen torob. dafa alde mootax foo ko séen mu ngi ànd ak jigeen.

alfokk : bëgg bañ, fàww. alfokk mu dem fa tey. dinañuy wax tamit fokk.

alfunni b- : milyoŋ b-. liggeeyam bi dox na lool léegi ndax ay alfunni la ciy am.

ali : li ñuy wax bu ñuy dàq fas. fas wi ali yóbbuwu ko. safaan wi mooy kor (li ñuy wax bu ñuy taxawal fas).

aljana : dinañuy wax tamit àjjana. (seetal àjjana)

aljuma j- : dinañuy wax tamit àjjuma j-. (seetal àjjuma)

alkaati b- : takk-der b-. alkaati bi jàpp na sófooru kaar ràppit bi.

alkol b- 1 : alkol ndox la mu saf mu ñuy def ci góom ngir faj ko.

alkol b- 2 : sàngara s-, ñoll w-. alkol boo ko naane dafa lay tàggale ak sa sago.

alku : dinañuy wax tamit alaku. (seetal alaku)

almasi b- : madiw b-. ki ñépp doon xaar ngir mu xettali leen mooy almasi.

almet b- : taalukaay b-. jaay ma almet.

almóodu b- : ndongo l-, njàngaan l-. almóodu bi mooy ka nekk ca daara ja di jàng.

alom g- : alom garab gu ñu xam ci Senegaal la te ñuy lekk doom bi.

altine j- : altine bés la ci bés yi.

alxames j- : alxames bés la ci bés yi. dinañuy wax tamit alxemes j-.

alxayri j- : li ñuy wax ca jàkka ja bu ñuy takk sëy ci diineey lislaam mooy alxayri.

alxemes j- : dinañuy wax tamit alxames j-. (seetal alxames)

alxuraan j- : téere jullit yi, kaamil b-. xale bi mokkal na alxuraan.