dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

aj 1 : dem Màkka. aj na ñaari yoon.

aj 2 : wékk, lonk, teg dara fu kowe. ku aj day séentu kow (léebu). safaan wi mooy àjji wala wàcce.

ajaa b- : dinañuy wax tamit ajaratu b-. (seetal ajaratu)

ajagjag : baatu ajagjag dafay tekki lu yàgg lool. maamam gaañu na ca ajagjag.

ajaratu b- : jullit bu jigeen bu dem aji Màkka ba ñëw lañuy tudde ajaratu. dinañuy wax tamit ajaa b-.

aji-gëm-xërëm j- : ku gëmul lu dul ay xërëm mooy aji-gëm-xërëm.

aji-gëm j- : way-gëm j-, ku gëm Yàlla. aji-gëm yaa ngi toog di déglu imaam muy xutba.

ajoor b- : joor-joor b-, kajoor-kajoor b-, waa-kajoor b-, ku dëkk Kajoor. ajoor bi dafa yaakaar ne moo gën a muus saalum-saalum bi.