dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

afal : def ay pexe ba féexal ab béreb. su dee néeg, afal mën na doon ubbi bunt yi wala palanteer bi wala def fa wantilaateer wala kilimatiseer. safaan wi mooy tàngal.

afeer b- : mbir m-, lëf k-. lu amul tur, lu ñu xamul turam wala lu ñuy bañ a tudd la afeer bi di tekki.

afirig g- : Afirig mooy dendu nit ku ñuul.