dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

abadan j- : àpp bu amul fu mu yem. dootoo ko gis mu def ko abadan.

abajadda b- : liifantu b-. njàngum kuy soog a tàmbali. ci abajadda bi la tollu.

abdu-jàmbaar : Abdu-Jàmbaar, malaakaam dee mi, kenn ñemewu ko.

able : abal. dafa able otoom bi.