dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

ŋeb : ub gémmeñ. du ŋeb mukk, fu mu tollu mu ngi wax. safaan wi mooy ŋa.

ŋeeñ : xàmp. dinañuy wax tamit ŋëriñ wala ŋareñ. (seetal ŋareñ)

ŋeer : fer, muus, wow. ndox mi nga doon tàngal ŋeer na. dinañuy wax tamit ŋiir.

ŋeleju : regeju, ŋóobi. buy wax ak yaayam, dafa koy ŋeleju.

ŋetteeku : dinañuy wax tamit ñetteeku. (seetal ñetteeku)

ŋexal : dinañuy wax tamit ŋaxal. (seetal ŋaxal)