dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

ŋaamaan b- : jongalkat b-. ŋaamaan a ko jongal.

ŋaam w- : ŋaam wi dafa deme boor.

ŋaaŋ : dinañuy wax tamit ŋa. (seetal ŋa)

ŋaax : yuuxu. mbaam mooy ŋaax.

ŋaayoo : xuloo. xaalis a tax ñu ŋaayoo. safaan wi mooy juboo.

ŋabar-ŋàpp g- : lu màgget, xott w-. nee na du jël ŋabar-ŋàpp gi ñu ko may.

ŋacc : jeex. ndaa li ŋacc na, demal rooti.

ŋalaab : dinañuy wax tamit laab. (seetal laab)

ŋa : ubbi gémmeñ. mu ngi ŋa di nelaw. dinañuy wax tamit ŋaaŋ. safaan wi mooy ŋeb.

ŋaññ : baat bi dañu koy gis ci kàddu gii di sama ŋaññ newu ci, mu ngi tekki sama yoon newu ci.

ŋar 1 : yuuxu, sab, xaacu, jooy. gaynde mooy ŋar.

ŋar 2 : wow ba pare di tàmbale xar. seen déeg baa ngay ŋar.

ŋarale : ràcc. mu ngi taxaw ŋarale ay tànkam. safaan wi mooy kepp.

ŋareñ : xàmp. xar mee doon ŋareñ mboq mi. dinañuy wax tamit ŋëriñ wala ŋeeñ.

ŋargaloo : rasu, boxomu, furaase. yéreem bi dafa ŋargaloo.

ŋar w- : rab w-. foofu dafa am ay ŋar, bu fa lal basaŋ bi.

ŋas : ŋàppati. yóbbul xale bi kër doktoor, dafa ŋas.

ŋat-ŋati : dox dox bu metti. mu ngay ŋat-ŋati di dem.

ŋaw : ŋoy, jàppandu. gone gaa ngi ŋaw ci yaay ji ne du ko bàyyi.

ŋaxal : yuuxu, sab, jooy. fas mooy ŋaxal. dinañyu wax tamit ŋexal.