dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

ŋàbb : tiye, jàpp. lu mu ŋàbb nii ?

ŋàdd w- : genn wàllu guro g-. may ko wenn ŋàdd wi.

ŋàlli : dinañuy wax tamit ñàlli. (seetal ñàlli)

ŋàmm : (ne ŋàmm). ubbi gémmeñ, yàbb (ne). mu ngi ne ŋàmm waaya li ngay wax déggu ci dara.

ŋànk : tiye ak ay gëñ, màtt, sex, log. li nga ŋànk lan la ? dinañuy wax tamit ŋënk.

ŋàññ : xas, sikk, ñaawlu. nit ñi ŋàññ nañu ni jëwriñ ji doxale.

ŋàppati : ŋas. xale bi dafa ŋàppati.

ŋàpp : (ne ŋàpp). ubbeeku. bul ne ŋàpp bunt bi, tëj ko. safaan wi mooy ne ràpp.

ŋàyy : (ne ŋàyy). ŋàpp (ne). dafa tàng, neel ŋàyy bunt beek palanteer bi yépp. safaan wi mooy kepp.