dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

óolu : yow lañu óolu. dinañuy wax tamit wóolu.

óom b- : óom cëru doom-aadama buy nekk ci tànk la. dinañuy wax tamit wóom b-.

óor : bir. deel dugg ci lu óor. nay wax lu ko óor. dinañuy wax tamit wóor.

óow : óow baat la bu nit di wuyoo su ñu ko woowee.