dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

ñukk 1 : daw ak jeego yu yem. mu ngay ñukk di ñëw. dinañuy wax tamit ñukki-ñukki.

ñukk 2 : (ne ñukk). bàyyi am mbir ci béreb te laalaatoo ko. ne na fi ñukk njàngam mi dem wuti liggeey.

ñulug : sóor. ñulug na ba pare.

ñumm : (ne ñumm). lëmm. xar mu ne ñumm la lakklu ca fuur ba.

ñun : ñun duñu tooñ te ku ñu tooñ ñu baal la.

ñuqati : yulli, yuqi. ñuqati na li nekkoon ci saaku bi yépp. dinañuy wax tamit ñuqi. safaan wi mooy ñuux wala roof.

ñuqi : dinañuy wax tamit ñuqati. safaan wi mooy ñuux. (seetal ñuqati)

ñur g- : catu bakkan l-. dafa taab ci ñur gi.

ñurumtu : xultu ci suuf. li ngay ñurumtu wax ko ci kow. dinañuy wax tamit ŋurumtu.

ñuul-biir : soxor, bon. li nga yéene sa bopp, yéene ko sa morom, bul ñuul-biir. safaan wi mooy laabiir.

ñuul : Nelson Màndelaa siggil na der bu ñuul.

ñuut : (ne ñuut). dinañuy wax tamit muut (ne). (seetal muut)

ñuux : dinañuy wax tamit ñóox. (seetal ñóox)