dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

ñoddi : xëcc, féq. ñoddi na buum gi ba mu teeŋ. safaan wi mooy bumax wala puus.

ñokket : (ne ñokket). baatu ñokket dafay tekki jóg ci saa si. neel ñokket jóg wuyuji sa pàppa.

ñoll w- : sàngara s-, dorog b-. jëfandikoo ñoll dafay yàq doom-aadama, bu ko laal, bu ko jege.

ñoñ y- : bokk y-, jegeñaale y-. soo amee, nanga teral say ñoñ. safaan wi mooy noon y-.

ñoŋal : sàmm. nanga ko ñoŋal ba bu ci dara sikk. safaan wi mooy sàggane.

ñoole b- : ñoole giir la ci xeetu géwel.

ñoom-seen : ñoomin. Ibu ak ñoom-seen a fi ñëwoon.

ñoomin : ñoom-seen. ñoomin Isaa laa fa gisoon démb.

ñoom : ñoom duñu doomi-réew mi.

ñoor : nas. ndax mën nga ñoor tubey ji ?

ñooru : moytu. mu ngi ñooru dof bi bu baax. safaan wi mooy dugg, sóoru wala sànjaafu.

ñoqali : sàqami, yëy. nag dafay ñoqali.

ñoramtaan : dinañuy wax tamit ñoromtaan wala ñiiramtaan. (seetal ñiiramtaan)

ñori : dindi li muuroon, wuññi, xàwwi, muri. dafa ñoriwoon sëram ba ba muy fecc. safaan wi mooy muur.

ñor : ceeb bi ñor na. / soxal. loolu lu ko ñor la. / yeewu, muus. danga ñor ba pare defe ne nit ñi dañoo dof.

ñoromtaan : dinañuy wax tamit ñiiramtaan wala ñoramtaan. (seetal ñiiramtaan)

ñoy : (ne ñoy). baatu ñoy dafay tekki am, ñu di ko gis ci jàmm ne ñoy. dinañuy wax tamit ñoyy.

ñoyy 1 : dinañuy wax tamit ñoy. (seetal ñoy)

ñoyy 2 : baatu ñoyy dafay tekki tëbb tëbb bu amul benn gàllankoor, layy. sàcc bi ne na ñoyy miir bi, dem yoonam.