dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

ñibbi : dellu sa kër. soo jàngee ba wàcc, demal nga ñibbi, bul taxawaalu fenn.

ñiimantu : lekk ndànk-ndànk li ngay lekk ndax bu mu gaaw a jeex. lekkal raxasuji te bàyyi li ngay ñiimantu. dinañuy wax tamit ñeemantal, ñiiramtu wala ñiiramtal.

ñiiramtaan : tex-texaan. li ngay def dafa may ñiiramtaan. dinañuy wax tamit ñoramtaan wala ñoromtaan.

ñiiramtal : dinañuy wax tamit ñiimantu, ñeemantal wala ñiiramtu. (seetal ñiimantu)

ñiiramtu : dinañuy wax tamit ñiimantu, ñeemantal wala ñiiramtal. (seetal ñiimantu)

ñiiroo : xuloo. keroog ba léegi, dañoo ñiiroo. safaan wi mooy juboo.

ñiit : dinañuy wax tamit ñedd wala ñédd. (seetal ñedd)

ñime : dinañuy wax tamit ñeme wala ñemeñ. (seetal ñeme)

ñimeñ : dinañuy wax tamit ñime, ñeme wala ñemeñ. (seetal ñeme)