dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

ñeb-ñebal : jag-jagal. dinañuy wax tamit ñab-ñabal. (seetal ñab-ñabal)

ñebbe j- : sëb s-, ngori l-. bey na toolu ñebbe.

ñedd : dindi ak baaraam li des ci ndab. lekk nañu ceeb bi ba ñedd bool bi. dinañuy wax tamit ñédd wala ñiit.

ñeeblu : sàggane. bul ñeeblu sa njàng mi, nanga góorgóorlu bu baax.

ñeel : yell, lew. góor-góorlu yi kër ñeel na leen.

ñeemantal : dinañuy wax tamit ñiimantu, ñiiramtu wala ñiiramtal. (seetal ñiimantu)

ñeent ñ- : am na ñeenti kër. dinañuy wax tamit yeent ñ- wala ñeneent ñ-.

ñee : fexeel say morom ñee la.

ñeeño : tëgg, lawbe ak wuude ay ñeeño lañu.

ñeex : siim, soos. àndi na cere ji ba ñeex ko.

ñef : dinañuy wax tamit ñaf. (seetal ñaf)

ñeleŋ g- : sanqal ak soosu tiga-dege lañuy togge ñeleŋ.

ñellarci : jël li nga dencluwoon fenn. ñellarci na saaku dugub ba mu ñaloon. safaan wi mooy ñal.

ñeme : waa ji ñeme na jaan. dinañuy wax tamit ñemeñ, ñime wala ñimeñ. safaan wi mooy ragal.

ñemeñ : dinañuy wax tamit ñeme, ñime wala ñimeñ. (seetal ñeme)

ñend : dinañuy wax tamit ñand. (seetal ñand)

ñeneen ñ- : ana ñeneen ñi ?

ñeneent : dinañuy wax tamit ñeent. (seetal ñeent)

ñengo : luxus. waa ji ne mën na ñengo xaalis, dafa leen di nax, su ko mënoon du ñàkk dara.

ñenn ñ- : ñeneen ñ-. ñii jaar nañu fii, ñenn ñi jaar fee.

ñepp-ñeppal : taw taw bu yem mooy ñepp-ñeppal.

ñetteeku : laaboo ay bant, kayit wala morso. laabuwul dafa ñetteeku. dinañuy wax tamit ŋetteeku.

ñett ñ- : am na ñetti doom. dinañuy wax tamit yett y- wala yatt y-.

ñey b- : nattukaay bu tollu ci ñaari meetar. ñaari ñeyi gañilaa lañu ko may.

ñey w- : dinañuy wax tamit ñay w-. (seetal ñay)